LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (14/8/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LIMU ÑI TEEWE MÀGGALUG TUUBA

Démb, ci àllarba ji, lañu doon amal màggalug Tuubaa. Mu nekk ndaje mu réy ci Senegaal. Mbooloo mu takku di fa daje at mu jot. Bees sukkandikoo ci caabalug Mubaarak Lóo (ingénieur statisticien) Njiitul “Cabinet Emergence Consulting Group” ak Musaa Jaw (expert en enquêtes statistiques), lu tollu ci 6.583.278i doomi-aadama teewe nañu ndaje moomu. Juróomi miliyoŋ yi ak lu teg mooy ñi jóge ci yeneen dëkk yi ñëw. Benn miliyoŋ bi ak lu teg moom ca dëkk ba lañu dëkk.

Naka noonu, ñii di waa sàppëer siiwal nañu limub ci jot a ñàkk seen i bakkan ci màggal gi. Xamle nañu ne ñaar-fukki doomi-aadama ak juróom-ñett ñàkk nañu seen bakkan. Te, li ci gën a doy waar mooy fukk ak juróom-ñett yi ci ndogi yoon yi lañu faatoo. Xamle nañu tamit ne moto yi ñoo ëpp lu ñuy def ay aksidaŋ ci yoon yi.

LAT JÓOB DU MUJJEE GÉNN

Lat Jóob, ci Nguuru Maki Sàll, nekkoon na fi jëwriñu tàggat-yaram ak Njiitul LONASE. Jamono yii, ma nga ca loxoy Yoon. Ëtt bii di “Chambre d’accusation financière” da koo mayoon génnug négandiku boole ko ak ñu takkal ko lam bi. Waaye, loolu mujjewul a àntu. Ndax, ëttu toppekaay bi moo lànk. Kon, mbir mi dañu koy mujjee càmbaraat xool ndax dañu koy bàyyi mu génn am déet.

XEW-XEW BU TIIS FA MAATAM

Naqar ak tiis la askan way yeewoo fa koñ bii di Subalo fanaanoo démb. Nde, kenn umpalewul ne fan yii bari na béréb yoo xam ne taw na fa ndox mu am doole. Looloo sabab jéyya ja am ca koñ boobee. Nde, benn tabax moo fa daanu ba ay bakkan rot ca. Ñaari xale ñoo ca ñàkk seen i bakkan. Ñoom ñaar ñi ngi tolloon ci juróom-benni at ak lu teg. Mu am tamit ñu bari ñu ca jëlee ay gaañu-gaañu.

BENEEN XEW-XEW BU DOY WAAR FA CEES

Bóomante baa ngi wéy di gën a bari ci biir réew mi. Wii yoon, benn xale bu jigéen buy tollu ci fukki at ak juróom moo bóom jenn waay. Xew-xew baa nga ame fa Caali, fa diiwaanu Cees. Xale bi nee na li tax mu def loolu mooy ne waa ji daf ko mayul woon jàmm. Maanaam, dafa yore woon ay widewoom yu doy waar. Te, daf leen a bëggoon a siiwal. Bees sukkandikoo ci saabalukaay bii di Kawtef, looloo tax, xale bu jigéen bi jam waa ji. Ginnaaw gi, ca la dawee. Waaye, mujj nañu koo teg loxo ba yóbbu ko kaso. Ki mu bóom tamit, jébbal nañu ko Boroomam.

MÓODU LÓO AK SAA-CEES TAXAW NA

Làmb ji ñu doon coow fan yii yépp mujj na a am daaneel. Ndax, bi Saa-Cees daanee Sàrkoo laaleek buuru làmb ji, Móodu Lóo, di sog a jóge ci ndam ci kaw Sitta, ci lañu doore coow loolu. Ñu ne, ginnaaw ñoom ñaar kenn amu ci koo bëreel, nañ leen boole. Na Móodu Lóo defal Saa-Cees li mu defal ay moroomam. Maanaam, may ko loxo ngir mu joŋante ba jot ci lenge yi. Móodu Lóo defal na ko loolu. Dees nañu bëre ca atum 2026.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj