LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/6/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

GAINDESAT-1B : SENEGAAL WUTALI NA JAWW JI

Senegaal a ngi séqi na jéego bu yees ci fànnu xam-xamu jaww ji. Nde, defar nañu seen ñaareelu satelit bees tudde GAINDESAT-1B. Porofesëer Gayaan Fay a ko xamle, moom miy aji-jokkale SENSAT. Rafetlu naat jéego yi ma-xareñ ak ma-xaralay saa-senegaal yi nekk fa Jànguneb Montpellier def.

CEES : JÀPP NAÑU FANWEERI NJÀNGAAN YU DOON NJUUJ-NJUUJ

Fanweeri njàngaan lañu jàpp fa diiwaanu Cees, fekk ñu doon njuuj-njaaj. Ci biir fanweeri njàngaan yooyu, 11 yi ay jigéen lañu. Ci alxamesu démb ji la leen Toppekatu Cees bi jàllale kaso ginnaaw bi ñu leen jàppandee ñaari fan. Njàngaan yooyu nga, liise « Jules Sagne » lañuy jàngee, tollu ci kalaasu « seconde ». Ba ñuy kàtte ci fànni xam-xam yii di Mboor-Suuf, Màndaxe ak Àngale lañu doon njuuj-njaaj.

UBBI NAÑU LUÑÑUTU CI JAWUB NGÀNNAAY BU 45,3I MILIYAARI FCFA

Ca jamonoy Maki Sàll, amoon na fi pasug ngànnaay gu 45,3i miliyaari FCFA gu lëmbe woon réew mi. Nde, dañu waxoon ay xeeti njombe ak luubal yu jéggi dayo. Léegi nag, ubbi nañu ci ag luññutu ngir leeral mbir mooma. Toppekat bii di Aliyun Abdulaay Silla moo yabal waa DIC ngir lëñbët pas googu, leeral li ci nekk lépp.

NDAR : JÀPP NAÑU 19I NIT ÑU DOON YËNGU CI MBËKK MI

Takk-deri Ndar yi teg nañ loxo fukk ak juróom-ñeenti nit ñu doon yëngu ci mbëkk mi, doon yóbbaate. Takk-deri DNLT (Division nationale de lutte contre le trafic de migrants) yi ñoo leen mbaal ginnaaw bi ñu jotee ay xibaar diggante 13 jàpp 17 suwe 2025. Dafa am ku leen déey, xamal leen ne am ñuy lal i pexe ngir jàllale ay mbëkk-kat yu bëgg a dem Tugal. Seen tukki boobu, « Vautour » lañu ko tudde woon. Waaye, takk-der yi gàntal nañu tukki boobee.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj