PASTEF AK KUJJE GI ÑU NGI XËCCOO NDAM LI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb la Ndajem ndeyu sàrtu réew mi génnee ab dogal ñeel sàrt bi dépitey Pastef yi wotelu woon fa Ngomblaan ga. Sàrt boobu, jubluwaayam moo nekkoon leeral sàrtu Amnisti bi. Maanaam, du ko far, waaye da koy faramfàcce. Ëtt bi nag, li mu xamle mooy ne sàrt boobu dafa woroo ak ndeyu sàrtu réew mi. Ginnaaw loolu, waa République des valeurs/Réewum Ngor ak waa Takku Wallu Senegaal, ñoom ñépp fara ci kujje gi, génne nañu ay yégle ngir wone ni dépitey Pastef ak waa Pastef ci seen jëmmi bopp lajjee ci seen tappale yooyu.

Naka noonu, waa Pastef tamit àddu nañu. Nde, kii di Njiit la, Usmaan Sonko, bind na ci xëtu Faacebookam ngir àddu ci ndogal bi. Dépitey Pastef yi tamit génne nañu ab yégle ngir indi ciy leeral. Donte ni sax, xam nañu ni seen sàrt bi jàllul, dañoo am poroxndoll ci yégleb Ndaje mi. Ndax, li ñu doon sàkku muy ñu topp ñi daan xoqatal, bóom ak a def yeneen jëf yu ñaaw, ñépp mën nañu leen a topp ci Yoon. Maanaam, sàrtu Amnisti bi mënt a far yooyu. Ci gàttal, du leen mën a aar ba Yoon du dal ci seen kow. Ndogal loolu moo tax, ku nekk di ràcc di jëmale sa kanam. Ku nekk naan maa daan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj