SFI DUGAL NA XAALISAM CI SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Këru liggéey gii di SFI (Société Financière Internationale), kër la gog day yëngu ci wàllu kopparal. Ki ko jiite di Maxtaar Jóob. Kër googu nag, génnee na koppar gu bari dugal ko ci réewum Senegaal. Dafa di, jamono jii moom, kenn umpalewul ne réew mi, Njiitu réew mi ak ug Nguuram, seen mébét bi gën a rëy mooy suqali koom gi. Ndax, xaw na a sooxe lool. Te, bor bu diis a ngi gàllu  ci seen ndoddu. Kon, kopparal gii wokku la bu dajeek geestu.

Ci weer yee jàll la Nguur gi génnoon wax tolluwaayu réew mi ci wàllu koom. Mu juroon fi coow lu bari ñeel yoriinu ñi fi jóge. Ñii di waa FMI sax àddu woon nañu ci. Boobaak léegi, terewul gaa ñaa ngi doxal boole ko ak di wut i pexe ngir suqali seen ug koom. Cuqalig koom googu ñuy mébét am nañ ku leen ci tàllal loxo. Nde, SFI bii nga xam ne Maxtaar Jóob moo ko jiite noppi na ngir dugal koppar gu takku ci liggéey bi Nguur gu bees gi sumb. Maanaam, dooleel naal wi ñu dippe “Vision Sénégal 2050” ngir jëmale réew mi kanam.

Ci njeexitalu ayu-bés bii la Maxtaar Jóob, Njiitul kër googu, ñëwoon fa Ndakaaru ngir waxtaane li ñu jublu ci kopparal googu. Bees sukkandikoo ci RTS mi siiwal xibaar bi, koppar gi mu dugal ci réewum Senegaal mi ngi tollu ci benn miliyaar ci ay dolaar ci atum 2025 mi. Maanaam, juróomi téeméeri miliyaar ak juróom-ñett fukk ak ñett ci sunu koppar. Mu nekk koppar gu takku goo xam ne jubluwaay bi du lenn lu moy suqali koom gi ci fànn yépp.

Loolu, li muy wund mooy ne koppar googu ñu dugal ngir suqali koom gi boole ci yeneen banqaas yi nga xam ne xaw nañoo sooxe. Muy ci tabax yi, laf gi, paj mi, mbey mi, añs. Ndax, mbooleem banqaas yooyu, bu ci benn doxul rekk, dees koy yëg ca ya des. Waaye, fi jamono tollu, kenn mënut a wax ba noppi te tuddoo xarala yu bees yi. Moo tax, desul ginnaaw ci seen waxtaan. Nde, bees sukkandikoo ci kàdduy njiitul kër gi, ñaari at yii ñoo ëpp lu ñu dugal seen koppar ci wàll woowu fii ci Afrig. Loolu di firndeel ne xarala yu yees yi, léegi, kenn du dem bàyyi leen, fàww nga sóoraale leen.

Mu mel ni, SFI noppi na ngir gunge Nguur gu bees gi ci yoon wii mu jël. Te, yoon woowu, ñi ngi ko tënk ci naal wii di “Vision Sénégal 2050”. Dafa di, Koom mooy kenob réew, bu sooxee rekk, réew ma tàbbi ci ag guuta. Waaye, bu naatee it, réew ma naat. Moo tax, ci cuqalig koom googu la SFI bëgg a jàppale Senegaal. Kon, ku bëgg fu mu fanaan ak kuy wut ku ko wéttali, tëjal buntu bi du leen boole.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj