Ëttu àttekaay bu kawe bi tàmbali naa déglu jëwriñ yees fa kalaame. Ndey Sali Jóob mi fi nekkoon jëwriñu Njaboot gi lañu njëkkoon a woolu démb ci altine ji. Ginnaaw bi ñu ko dégloo itam, jël nañu ndogalu topp ko. Waaye, dañu ko bàyyeendi mu ñibbi ginnaaw bi mu tegee ci taabal ji 57i tamndareet ngir ñu bañ ko fa téeyandi. Cig pàttali, caabalug Ëttu caytu gee ko tuumaloon ci yoriinu 52i tamndareet yu aju ci koppari mbas mi.
Ginnaaw Ndey Sali Jóob, Ismayla Majoor Faal itam wuyuji woon na tay ci talaata ji. Moom nag, lu jëm ci wàllu nger lañu ko taqal. Ku ñuy wax Séex Géy moo biraloon ni joxoon na ko 50i tamndareet ci ab liggéey bu mu bëggoon a jot, donte ni sax Sëñ Faal weddi na lu ni mel. Ginnaaw bi ñu ko dégloo nag, layalkatam bii di Meetar Aamadu Sàll xamle na ni dañu ko takkal lamu tànk.
WÀLLU BALLUWAAYI MBINDAARE YI
Diggante 2023 ak 2024, dajale nañu lu tollu ci 616i tamñareeti FCFA ci bàlluwaayu mbindaare yi. Muy alal joj, 571i tamñareet yi tàbbi nañu ci gafakag Càmm gi ca saa sa. Xibaar la bu njiitu ITIE (Initiative pour la transparence dans les industrie extractives), Caali Fay, fésal. Fekk ñu doon amal am ndaje ngir aajar caytuy kurél gi.
SABADOLA : LIGGÉEYKAT YA NAMM NAÑOO BANK SEEN I LOXO
Liggéeykati kërug liggéeyukaay gii di SGO nar nañoo bank seen i loxo ci ayu-bés yii di ñëw. Li leen naqadi nag mooy ndogal li njiit la jël ngir wàññi peyoor yi lu ko dale ci 1 suwe bii di ñëw. Ndogal loolu dafa nar a coppati 40% (ñeen-fukk ci téemeer bu nekk) ci peyoor yi. Muy ndogal lu xel mënul a nangu bees sukkandikoo ci Abdu Xaadar Ba mi yor kàddu liggéeykat ya. Muy xamle ni xibaar yi kilifa yi biral ngir sukkandiku ci dëppoowul ak li am. Nde, mbindaare yi génne nañu alal ju takku ci atum 2024 mi. Jébbal nañu itam kilifa yu mag yi ab bataaxal ngir gindi leen ci mbir mi.
BITIM-RÉEW
Usmaan Sonko amal nab woote ci tukkeem bi mu doon amal fa réewum Burkinaa Faaso. Woote boobu nag, moo ngi ko jagleel Saa-Afrig yiy wuyoo panafricanistes/Souverainistes africains. Muy sàkku ci ñoom ñu booloo, bàyyi xaajaloo bi ngir ànd ak liggéeyal kembaar gi mu moom boppam. Naka noonu, rafetlu na bu baax ni Senegaal ak Burkinaa Faaso amee ay déggoo ci càmmin wi, moom-sa-bopp ci koom-koom ak lëkkatoo yi dox ci diggante réewi bëj-saalum yi.