LÀMB JI : FARÃ DAAN NA ËMMA SEEN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Doomu Pàrsel bi jaar na ci tànki magam ja, Móodu Lóo. Raxas na bépp mbëru Pikin bees tegoon ci kanamam ba ci seen mag ji ñu ji woon seen yaakaar jépp. Farã dëggal ay mbiram, gën a yaatal yoonam ci làmb ji.

Waajtaayu bëre bi

Mu nekkoon làmb ju ñépp doon xaar, mu tàmbali woon a tàng balaa seen bëre biy taxaw. Coow li bari woon lool ci jàppal Farã, bàyyil Ëmma. Waaye, li wolof naan « loo bëggul mu agsi bul ko jàppal bés » moo ci nekk rekk. Démb, lépp mat na, lépp leer na.

Ñu gis ñaari mbër yépp fi leen bés bi tolloon. Ku ci nekk waajal ko ca na mu gënee. Ci wàllu tàggatu beek yeneen yi aju ci làmb yépp. Ëmma seen amoon sas wu réy, muy ñëw far rongooñu Pikin, fajal leen seen mer. Farã ni moom li mu def ba fii kenn du ko ko yàqal. Gaynde gu xiif la, lu mu dajeel dana ko fàdd. Mu nekk bëre bob ñaari ndaanaan ñoo ci daje, ku ci nekk bindal boppam turam ci làmb ji.

Ñoom ñaar, ñu jaay seen bés bi na mu waree, seen i jàkkaarloo tàng jër. Nappante bi, sànnante xeer bi, gàjjante bi lépp ci biir. Ku nekk xiif sa moroom te naan ko ba bés ba.

Bëre bi

Ba ñaari mbër yi noppee seen lépp ba dugg ca diggu géew gi, arbit bi wax ak ñoom, mbiib. Ñaari mbër yi tàmbali di léewatoo, lu yàggul dara, doomu Pàrsel bi tàmbali di dox ci kaw Ëmma. Ñu nekk ci léewatoo bi, nes-tuut Ëmma daldi sanni kurpeñ, Farã fayu ba noppi wëyal, di dox ci kawam. Ñu dem ba ci wetu saaku ya samp fa bëre bi, maanaam taxaw foofu. Ñu gaawal léewatoo bi, tàmbalee xeex xeex bu metti, laaw yi, jam yeek lépp ci biir. Waaye ñoom ñaar ñépp di ko def xeexu mbedd. Ci noonu, Farã jël ci biir xeex bi ab dóor, ba tax mu xam ni jàppante bee ko gënal, mu fexe ba jàpp Ëmma.

Ba ñu jàppantee, doomu Pikin ji jéem fa dóor mboot. Mu dellu ca wayu Fàllu Jeŋ wam daan wax ni « ku fekk ñay mu taxaw nga di ko gal-gal, sa tànk damm ».

Bi ko Ëmma jéemee mbot, Farã xaw a rocceeku, ñu rëpp ñoom ñaar. Foofu loxo Farã xaw a féete kaw, mu daldi jaay doole yaakaaru Pikin bi, naj ko, mu mëq suuf si, kanam gi taq ripp ak suuf. Noonu la bëre bi jeexee. Farã daan Ëmma Seen.

Fim ne nag, laajees na kan la Farã war a bëreel. Ak tamit Ëmma Seen, ndax dafay mayaat ay rakkam buntu walla dafay bàyyi bëre ni mu ko waxee woon « Suma Farã daanee ma bàyyi bëre ! »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj