Tay, 13i pani ut 2025 mooy méngook 18eelu fanu safar ci atum 1447 ci arminaatu jullit ñi. 18eelu safar nag, bu ñu ko waxee fi Senegaal, xel yépp dem ci màggalug Tuubaa, muy xew-xewu diine bu mag a mag. Kon, tay, àllarbay màggal la. Ay tamndareeti taalibey murit teewi Tuuba ngir santale Yàlla ki tax ñuy màggal : Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke walla Sëriñ Tuubaa.
Màggalu Tuubaa mooy xew-xewu diine bu gën a réy te gën a màgg ci murit yi. Bésub màggal gi, dañu ciy fàttaliku gàddaayu Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, Sëriñ Tuubaa. Gàddaayam boobu, way-mbéeféeri tubaab yaa ko ca ga woon, mu demoon Gaboŋ ca atum 1895. Ca atum 1928, menn at ginnaaw dëddub sëriñ bi, lañ ko tàmbalee màggal fi Senegaal ba jonni-Yàlla tay jile. Màggalug ren ji mooy 131eel wi yoon. Tuubaa la màggal giy amee at mu nekk. Daanaka, ci lees xayma, juróom-benni (6i) tamndareeti taalibe dinañ màggali fa Tuubaa. At mu nekk nag, dafa mel ni lim bi day yokk.
Bu dee màggal gi ci wàllu boppam, taalibe yi dañuy faral di siyaareji xabru Sëriñ ba, di dem ca jumaa ju mag ja, di teewe waxtaan ya, añs. Bernde yi tamit bokk nañ ci liy màndargaal màggal gi. Nde, Saa-Tuubaa yi dañuy teral seen mbokki taalibey murit yi leen di ganesi. Ndawal yi (yàpp xar, nag ak gëléem), naan yu sedd yi, kafe Tuubaa gi, meññent yi, dara du des ginnaaw. Jamonoy màggal day jamonoy tabe, bokkoo, mbokkoo, séddoo, jàppalante, dimbalante ak teralante.
Ay gan yu am maanaa, am dayo, dinañuy faral di màggali at mu nekk. Muy kilifa yi ràññeeku fi réew mi, diy kilifa yu mag ci wàllu diine fa bitim-réew, ñépp ñooy màggalsi.
Lenn rekk nag moo xaw a naqari ci màggal gi, te mooy bakkan yiy rot ci sababi ndog yiy am ci tali bi. Ren jii, limagum nañ 75i ndog ci yoonu Tuubaa wi, mu amagum as-tuut 5i bakkan yu ci rot. BNSP (Brigade nationale des Sapeurs-Pompiers) moo joxe lim yi.
EJO Editions ak Lu Defu Waxu ñoo ngi ñaanal màggalug jàmm, di ñaanal itam ñi ñàkk seen i bakkan ñépp ci yoonu màggal gi, Yàlla jéggal leen te yërëm leen.