SENEGAAL 2050
Senegaal am na sémbu delluwaay wu bees. Tay ci altine ji, 14i pani oktoobar 2024, la ko Càmm gi aajar fa Jamñaajo. Muy sémb wu Càmm gi taxawal, mu wuutu PSE (Plan Senegaal Émergent) bi Nguur gi weesu tënku woon ngir tabax yokkute...
Sémb wi ñu doon coow ay at, ay weer, ay ayi-bés, mujj na a yemb. Tey, ci altine ji, 14i pani oktoobar 2024 lees ko doon aajar fa CICAD (Centre International de Conférences Abdou Diouf), nekk fa Jamñaajo. Kaajar googu, ñi ngi ko doon...