NJUUX LI : ANACIM A NGI ARTU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gii dii ANACIM (Agence nationale de l’aviation civile et de la météorologie) mooy saytu lépp lu aju ci njuux li fi réewum Senegaal. Ñoom nag, saa su nekk, dañuy joxe ay dég-dég ñeel melokaanu jaww ji ngir nit ñi di mën a jël seen i matuwaay. Naka noonu, ginnaaw bi ñu defee seen i gëstu, génnee nañu ab yégle di ci artu. Nde, ñoo ngi xamle ne, am na fukki diiwaan yu nar a jànkonteel ak i mbënd ci sababu taw yi nar a sóob diggante alxames ak gaawu bi.

Niki àllarbay démb ji la ANACIM génne ab yégle di biral xibaar bu dul neex ferey fukki diiwaan ci réew mi. Kurél gi dafa yégle ne :

« [Taw yi] dañu nar a jur ay mbënn ak i taa-taa ndox yu ndaw a kyu yem ci diiwaan yii di Ndakaaru, Njurbel, Cees, Fatig, Kawlax, Kafrin, Ndar, waayeet ak Maatam, Tàmbaakundaa ak Kéedugu. »

Njëwriñu Ndox mi ak Cetal gi tamit torluwaale na yégle boobule. ANACIM di wéy di artu dëkk yi féete ci Tefes yi, di leen wax ne am nay ngëleen ak i taw yu am doole yu ànd ak ngelaw yi leen nar a ganesi. Lu ni mel dafa nar a gàllankoor ñiy liggéey ci géej gi, rawatina nappkat yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj