Xibaar KËR ARAM By Ndey Koddu Faal 22/08/2025 0 0 Partager FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Yeneen i xët BÉS BI ÑU JAGLEEL JASPORAA BI FI RÉEW MI Njuga Gay - 17/12/2025 COKKAASU ODIA Odia - 15/12/2025 BÉS NIKI TAY, NEELEEN DOKTOOR PÀPPA AALI JÀLLO Ndey Koddu Faal - 15/12/2025 COKKAASU ODIA Paap Aali Jàllo - 08/12/2025 Aji bind ji Ndey Koddu Faal Seeti naa soxna Aram Faal Jóob, ndaanaan Jàmbaar la, lingeer dëggantaan Dama ko ni jàkk sama yaram di daw Mu siggi xool ma, mbaaru bëtam jëm kaw Mbégte mu réy di rogalaat Fépp ci sama xol di gundaandaat Aram ca dal ga, baat bu sedd ba, yiw ga Bari xam-xam bu wér, Aram ca oyof ga Taxul mu réy bay dox di fëgg dënn Waxumalaak di wone maa mën Xëccul benn cër Jox na ñépp cër Ne ci li ko war Fonk ñi ko wër Du xaste, du tuutal kenn Doylu na, xëccoowul lenn Kii a mat a delloo njukkal di sargal Kii a mat a wone nde dafa noo sagal Wet goo làmb Aram Faal muy royuwaay Jàng na ba mat wéeruwaay Lijaasa yu kowe la am Teewu koo yor këram Di sàkku ngërëm Yar njabootam ci diine ak amal njariñ askanam Firnde li mooy ay ndomb-tànk terewul jigéen Doon jigéen matal li ko tax a doon jigéen Aram fàttewul ni lees mën a tere gan xool ak dégg bokku ci, moo mën gan wax na, nu dégg, lépp rafet na won nga nu, nu gis, lépp rafet na kii mooy saa-Senegaal bu jan bari teggin, mën a teral gan « Mag mat naa bàyyi cim réew » ku mel ni Aram a gën cim kéew ndax xam-xamam ak yiwam jikkoom yu rafet, am leen a di ndam Aram Faal Maali- Kumba mii may woyal Xamal ni jëmm ji rekk daara la Mën i téere, nitee ma ko gënal Ku ko seeti gis ni dara la Soxna Mari Mbow, xam na li ma wax Sëñ Faliilu Njaay du weddi lii ma wax Ibraayma Lóo, seedeel lii ma wax Aamadu Njaay gëm na lii ma wax Baakari Saar, gis na lii ma wax Senegaal ameel na la njukkal na say may di baawaan, Faal, dundal ! Ndey Koddu Faal Ndey Koddu FaalPlus de publicationsBiographieNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/BÉS NIKI TAY, NEELEEN DOKTOOR PÀPPA AALI JÀLLONdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/MOUSSO NGIR « JIGÉEN GÉNN CIG LËNDËM »Ndey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/IMAAM AMAAT CAAM, IMAAM BU DËPPALE WOON DIINE AK JAMONO…Ndey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/MAMADU LI (ARED) JËL NA NEEXALU YIDAN 2025 FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Widewo VOA AMAL NAB JOTAAY CI MBINDUM BUBAKAR BÓRIS JÓOB GINNAAW BI WEREKAAN BI JËLEE CARGALUG NEUSTADT 2022 BI. CUQAL CI LËNKAAY BII TOFTALU... Defu Waxu - Xët yi mujj