CAAROY 44 : NJIITU RÉEW MI JËL NAY NDOGAL
Barki-démb ci dibéer ji lañu doon màggal 80eelu pàttalikug Caaroy 44. Ñu doon ko amal ci njiiteefu Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak ci teewaayu kilifay réew mi ak yu bawoo fa bitim-réew. Ginnaaw...
Mats futbal bu mujje ciy masta ! Mbir yaa ngi xew barki-démb ci dibéeru 1eelu fanu desàmbar wii, mu di woon ab finaal bees doon amal fa gine ca fowub 3i Awril bu N'Zerekore. Waaye, po mi, ciy jooyi naqar la mujje. Nde, 56i...