BÉS BI ÑU JAGLEEL JASPORAA BI FI RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tay ci àllarba ji, 17 desàmbar 2025, doon nañu màggal fa Jamñaajo, bés bi ñu jagleel waa jasporaa bi, ci njiiteefu Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Muy guléet ñuy amal boobu bés fi réew.

Ci weeru suwe bi weesu la Càmm gi siiwaloon sémbuw dekkare bu waroon a samp bés bi ñu jagleel jasporaa Senegaal bi ndax taxawaay bu am solo bi mu am ci doxal koom-koom beek mbiri askan wi fi réew mi. Juróomi weer ginnaaw bi ñu ko biralee, doon nañu amal tay bés bi njëkk fa CICAD (Centre International de Conférence Abdu Juuf), fa Jamñaajo. Njiitu réew mi doon ko jiite, ci teewaayu njiitu Ngomblaan gi, El Haaji Maalig Njaay, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko ak ñenn ci jëwriñi Càmm gi.

Ginnaaw bi mu jëlee kàddu gi, Njiitu Réew mi, dellusi na ci bés bu njëkk bi ak wëppa wi ñu ko tànnal di « Jasporaa Senegaal bi, ab sukkandikukaay ngir sopparñi réew mi ». Mu jaare ca ngir wane solo su mag si mu gis ni doomi réewum Senegaal yi nekk bitim-réew am nañu ko ñeel suqaleeku réew mi.

Solo soosu sax, moo tax ba moom ak Nguuram jox leen gëdda gu wér ci anam yi ñu bëggee tabax Senegaal gu mën boppam, gu naataange ak ndimbal law, te Yoon di fi dox.

Naka noonu, Njiitu réew mi dellu di feddali yéene ji mu amoon ci taxawal ay waxtaan yu sax ak jasporaa bi ngir ñu ànd ciy fas ak i lekkatoo yu dëgër te yàgg, yu ñépp mën a gis seen bopp.

Njiitu réew mi woo na jasporaa beet ci mu dëgëral taxawaayam bu baax ñeel naal wii ñu duppee New Deal Technologie, di aw naal wu yees wu mu am ngir def Senegaal am mbër ci suqaleeku jumtukaayi xarala yi. Mu ciy woo Jasporaa bi ngir ñu dugal ci seen loxo, jaare ko ci seen xam-xam ak seen mën-mën ba ñu soppi Senegaal dëkk bu fees ak i boroomi xam-xam ak ñu xarañ.

Cig pàttali, at mu jot, doomi Senegaal yi nekk bitim-réew dinañu yónnee alal ju takku ci biir réew mi. Ci atum 2024 mi, dugal nañu fi lu tollu ci 2 211i miliyaari FCFA. Muy alal joj, ëppee na lu bari ndimbal yi daan jóge ci kuréli àdduna si ñeel suqaleeku gi.

Nguur geet tàmbali woon naa sukkandiku ci doole jooju Jasporaa bi am ba jot cee dajale alal ju takk ju jëm ci kopparal. Mu doon ko jaarale ci li ñuy duppee Diaspora bonds. Dajale bi ñu mujj a def rekk, buub nañu lu tollu ci 450i miliyaar, jële ko ciy Saa-Senegaal yu nekk ci lu ëpp 45i réew.

Ak doole ju ni mel, Jasporaa doon na tay 15eelu diiwaan bu Senegaal, ci misaal. Am na itam as ndaw su koy di toogal fa Ngombalaan ga.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj