Naqar ak tiis la ñu bari ci askanu Senegaal fanaanoo démb, rawatina ñi bokk ci làngu Pastef. Kii di Paab Mammadu Sekk moo génn àddina ci àllarbay démb ji. Mu doon xibaar bu tiis lool. Nde, moom dafa am jaar-jaar bu tar ci wàllu pólitig. Ndax, dafa bokk ci ñi ñu tëjoon ci mbiri « forces spéciales ». Te, jot naa yàgg kaso laata muy génn. Démb la wuyuji Boroomam. Tay ci alxames ji lañu ko denc. Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, di njiitul làngu Pastef, teeweji woon na rob ba, ba noppi jaaleji ay mbokkam.
XIBAAR ÑEEL ÑIY SOG A AM BAC
Weeru sulet wii ñu génn lañu doon amal joŋantey wutum lijaasa biy ubbil ndongo yi bunti daara yu kawe yi ak yeneen joŋante ngir am liggéey. Fan yee weesu lañu doon def seen i tànneef ci daara yu kawe yi ñu bëgg a jàngee. Ndiiso gi ñu dénk wàll woowu génnee na ab yégle ngir xamle ne tànneef yi dina tàmbalee jàppandi ëllëg ci àjjuma ji. Maanaam, ndongo bu nekk dina jot ab bataaxal buy firndeel ne daara yi mu tànnoon am na bu ñu ko ci yóbb.
BÀYYI NAÑU FÀLLU FAAL
Coowal Fàllu Faal lëmbe woon na réewum Senegaal lool ci jamono yee weesu. Te, li ko waraloon du lenn lu moy ne dañoo gisoon ne dañu koo jaay doole. Maanaam, dañu koo tuumaal ba pare tëj ko kaso. Loolu nag la ñu bari gis ne kenn waru koo bàyyi mu jàll. Defoo ba pare di tëdd kaso. Waaye, bi mu taxawaatee mujj nañu ko bàyyi mu ñibbi këram ginnaaw bi mu fa tëddee juróom-benni at.
DAAN NAÑU BUGAAR JUUF
Altiney keroog ji lañu woolu woon Njiitul UPS (Union des Panafricanistes du Sénégal). Li waraloon woote bi mooy li mu bindoon ci xëtu Facebookam. Mu wax ci xeex bi am Kaasamaas, coowal làrme bi ak elimaanu jëwriñ yi. Démb la doon taxaw fa ëttu àttekaay bu Ndakaaru ba. Moom nag, mujj nañu koo daan weeru kaso. Li ñu koy toppe mooy biral xibaar yu wérul.
LU ÑEEL MBIRI FARBA NGOM
Fan yee weesu lañu ko doon seetal wér-gi-yaramam. Li ñu ko dugge woon mooy xam ndax, wéram may na ko mu des ca kaso ba am déet. Dafa di nag, ba njureef ya rotee tamit, taxul woon ñu bàyyi ko. Waaye, dafa am geneen ceet gu ko ay fajkat yu xarañ defalaat. Li ñu gis mooy ne wér-gi-yaramam demewul noonu. Maanaam, wéram mayu ko mu des kaso. Te, bu desee sax lu nekk mën na caa am. Dem nañu sax ba ne mën na cee ñàkk bakkanam.
XEW-XEW BU TIIS FA KAWLAX
Xibaar bu tiis moo dal ci kaw ñi mbiri nawetaan soxal fa Kawlax. Nde, dafa am xew-xew bu doy waar bu fa am. Ma nga ame fa Kër Soose nekke fa Kawlax. Benn futbalkat moo fa génn àddina ci biir joŋante bi. Bees sukkandikoo ci waa Seenweb, dafa daanu rekk jaar fa ñàkk bakkanam. Mu doon xibaar bu tiis te metti lool ci ñiy yëngu ci tàggat-yaram ak waa dëkk ba mu dëkk.