Paap Caw, tàggatkatu ekib bi siiwal na limka ndaw yi mu tànn ci ñaari ndaje yi ñu dëgmal ci fan yii di ñëw, Senegaal-Sudã (5/9/2025) ak Kóngoo-Senegaal (9/9/2025). Daanaka, ñi mu tànnoon ci matsam yi weesu la woowaat wëliis Paap Mustafaa Mbów miy door a dikk ci ekib bi.
Asan Jaawo ame na gaañu-gaañu ci tànku ndeyjooram (fissure du cinquième métatarsien) ci seen benn tàggatu. Loolu yóbbee ko mu dandu pàkk yi diirub 5i ayu-bés. Looloo tax Paab Caw woowu ko ci mats yii.
CHAN 2025
Gayndey Senegaal yi jël nañu 3eelu toogaayu po ma. Gannaaw ba ñu moyee ci seen jàllug finaal, jaayante nañu ba bokk ca cappaandaw ga, donte du li leen gënaloon.
Màrk Filib, góolu Senegaal bi, moom lañu tabb góol bi gën a xarañ ci po mi ndax li mu ci wane.
CHELSEA/ NIKOLAA JAKSON : XËCCOO BU METTI
Saa-Senegaal bi ay bésam neexul jamono jii ca Chelsea. Gannaaw ñaari ati futbal yum fa def (23-24 / 24-25) ren a waroon a doon ñetteelam. Waaye, mu mel ni seen diggante neexul ci fan yii ñu nekk. Bokk na ci li ko waral di ekib bi dafa wut ay ataakã yu bees jàpp ni soxlaatul Jakson. Loolu tax mu xamalees ko ni fàww mu wuti beneen këlëb. Di ko buux ci boor bu ne ngir mu dem. Ñu demoon ba juboo ak Bayern Munich ngir abal leen Saa-Senegaal bi abalin bob ñooy ràngoo payooram ba noppi, bu leen doyee, mën nañu ko jënd.
Ci loolu, démb ci gaawu bi, Nikolaa Jakson ànd ak njaatigéem (agent) Jomaasi Kamara, dem Almaañ ngir defi saytug yaram ba ca yelloo. Waaye mbir am. Ndax ataakã Chelsea bu bees bii di Liam Delap dafa gaañu ci seen ndaje démb mi ba tax Chelsea xamal waa Bayern Munich ni bu sañoon futbalkatam dellusi, nde daf ko soxlawaat. Loolu mel ni yabeel ba tax Nikolaa Jakson ak njaatigeem ni dellusiwuñ, wax ne dañuy matal li leen taxoon a jóg.