Xew-xewi pólitig yi amoon diggante màrs 2021 ak féewiryee 2024 ba tay pënd ma wureegul. Li ko waral mooy ñi nga xam ne ñoom lañu jàppoon tëj leen, ñoo lànk ne duñu bàyyi mbir mi mu sedde noonu. Ndax, lu tollu ci at ak lu topp muñal nañu ko Nguur gi nga xam ne moo taxoon ñuy xeex. Te, booba ba tay dara saafarawuñ ko ci. Moo tax, ñu jóg ngir fàttali Nguur gi li ñuy xaar ci moom. Te, loolu du lenn lu mooy mu sulli wayndare woowu. Su ko defee ñu xam ñan ñoo ci laale ak naka lañu ci laalee.
Weeru màrs atum 2021 lañu tegoon loxo Njiitul làngu Pastef, Usmaan Sonko. Foofa la coow lépp doore woon, donte ne sax ca weeru féewaryee wa jàmmaarloo jotoon naa am. Waaye, ca weeru màrs la jàmmaarloo yi tax ay bakkan rot dooree. Ndax, ca la ñu bari ci askanu Senegaal, rawatina ndaw ñi génn jàmmaarloo ak takk-der yi. Li ñu ko dugge woon mooy ñu bàyyi Usmaan Sonko. Nde, dañoo jàppoon ne ay mbiri pólitig kepp a taxoon gaa ñi bëgg koo faagaagal. Waaye, laata mu fay def ayu-bés bàyyi nañu ko. Ginnaaw loolu, bari na ñu ñu tegoon loxo. Ku nekk ak lañu koy toppe. Te, coow li sax yamul woon foofu.
Dafa di, ci atum 2023 mi la coow li gën a taqarnaasee. Ndax, ci la doon layoo ci coow li doxoon ci digganteem ak Maam Mbay Ñaŋ ak soxna sii di Aji Saar. Ginnaaw bi ñu ko àttee ba daan ko, ca la jàmmaarloo yi dooraatee. Mu am ñu ñu ci bóom. Mu am ñu ñu ci jàpp ak ñu ci jële gaañu-gaañu yu metti. Ca jamono yooyu lañu ko tëje woon ca këram laata ñu koy teg loxo. Bi ñu ko tegee loxo tamit, ndaw ñi génnaatoon nañu waaye, terewul ñu tëj ko. Bi ñu ko tëjee ba desul lu dul ñu amal wote ya fa la mbir ya jaxasoowaate. Ndax, ki fi nekkoon Njiitu réew, dafa dàqoon wote yi, ñenn ci ndaw ñi génn ne du ci dal. Ca la jàmmaarloo ya dooraatee ba ay bakkan rotaat ca. Te, booba fekk na ñu bari ñi ngi ci kaso yi. Te, ñu ci bari li tax sax ñu teg leen loxo bokkul.
Bi loolu weesoo ci lañu wotee sàrtu Amnisti bi ngir baal leen ñoom ñépp. Ci la moom, ndeyu-mbill gi, Usmaan Sonko ak ki fi nekk tay Njiitu réew, di Basiiru Jomaay Jaxaar Fay génnee kaso. Daldi door seen i kàmpaañ ba jël réew mi ci weeru màrs atum 2024. Boobaak léegi nag, way-loru yeek seen i njaboot ñi ngi xaar Yoon def liggéeyam. Waaye, mbir mi ne tekk-tekkaaral. Loolu la ndaw ñu bari rawatina ñi ñu tegoon loxo mënut a nangu. Ndax, mënuñoo xeex ba agsi fii, ñii ñu tëj leen, ñee ñu bóom leen te, ba tay, Yoon mënut a yéy yàbbi ci.
Looloo tax, keroog ci gaawu bi ñu amal seen doxu ñaxtu ngir soññ Nguur gi. Xamal ko ne xaar baa ngi bëgg a yàgg. Te, ba tay gisuñu gaa ñi séqi benn jéego buy wone ne ñi ngi ci li ñuy xaar ci ñoom. Ndax, mënuñoo nangu lu tollu ci juróom-ñett-fukki bakkan rot, ñu jàpp lu jege ñaari junniy doomi-aadama, ba noppi, ñu bëgg a yolomal nii. Loolu ñoom duñu ko nangu. Li ñu leen digoon ne Yoon dina leeral mbir yooyu ba tay gisaguñu ci dara. Li ñu bëgg du lenn lu moy Yoon ubbi ay luññutu. Su ko defee ñu xam ñan la seen loxo laale ci mbir yi.