Jamono jii, ñu ngi amal, fi Ndakaaru, lees ndaje mees duppee « Forum Africain des Systèmes Alimentaires 2025 », maanaam Ndajem Péncoo Nosteg Dund bi ci kembaaru Afrig ci atum 2025. Démb la Njiitu réew mi doon ubbi ndaje mi fa Jamñaajo. Ndaje mi nag, 6 000iy nit dinañu ko teewe, nar a waxtaane csolos ndaw ñi ci wàllu sopparñi mbayum kembaar gi. Dees na sëgg, càmbar fànni coste gi, dugal xaalis, ak yeesalug « Programme Détaillé de Développement de l’Agriculture en Afrique (PDDAA 2026–2035). Ci lees wax, ndaje mi dina gën a ubbi ay bunti liggéey, gën a fésal ndaw ñi taxawal ay këri liggéey ak sumb ay liggéey yu lootaabewu.
Ku ne dund, wax lekk, te ku wax lekk xel dem ci mbay. Mbay nag, foo ko tuddee, tuddaale suuf. Moo tax, ciy kàddoom, Njiitu réew mi xamle na ne Afrig ñàkkul suuf su muy bayee. Ndaxte, àddina wërngal-këpp, moo ci ëpp i suuf sees mën a bayee. Nde, téeméer yoo jël ci suuf yees mën a bay ci àddina si, juróom-benn-fukk ak juróom yi Afrig lañu féete. Waaye, ànd ak loolu yépp, ba tay Afrig bayagul luy dundal ay doomam walla li koy tax suqaleeku ci fànnu koom-koom. Waayeet, mbay mënut a suqali am réew, rawatina ag kembaar, bu dee amuñu ay baykat yu nangoo liggéey suuf si.
Afrig nag, dafa mel ni dañu xeeb mbay. Nde, ñu bari dañu jàpp ni liggéeyu kaw-kaw la. Loolu moo tax amuñu limu baykat bu doy. Xam loolu moo tax Njiitu réew mi di woo ndaw ñi ci ñu sóobu ci mbay mi. Ci xalaatam sax, téeméeri ndax yoo jël, juroom-benn-fukk yi dañu war a sëgg ci luy sopparñi mbay mi. Wànte tamit, mbay, xaalis a koy def.
Càkkanteefu mbay dinay jur xaalis naam, waayeet mbay dafa aajowoo xaalis. Ndaxte, jiwu, xaalis a koy jënd. Ndox mi, jumtukaay yi, xarala yu yees yi, añs., loolu yépp tamit dafa laaj xaalis. Naka noonu, Njiitu réew mee ngi woo boroom alal yi ak meññlukat yi ngir ñoom it ñu bay ci seen waar. Naka noonoot, Nguur yi waruñoo des ginnaaw.
Wolof dafa ne, ndimbal, na cay fekk loxol boroom. Nguur yi nga xam ne ñoom lees dénk alali askan yi, ñu war ko def ci li leen di jariñ kepp, ñoom ñoo war a njëkk a gestu mbay mi. Loolu moo tax ñu war a sàmmonte ak lees duppee ” Déclaration de Maputo”.
Nde, lañu tënkoon foofa mooy ne, réew mu nekk dafa war a jël fukk ci téeméer bu nekk ci nafaam (budget), jagleel ko mbay mi. Bu ko defee, mbay mi dina suqaleeku, ñun mën cee dund, mën cee yaxantu.
Ci biir yaxantu boobu, li Saa-Afrig yi war a jiital mooy seen bopp. Maanaam, di jaayante seen biir laata ñuy jaay yeneen kembaar yi. Loolu la Njiitu réew mi mi woote. Rax-ci-dolli, dañu war a samp ay ndefar yuy sopparñi njureefi mbay mi. Bu ko defee, liggéey dina am te dina tax xiif gi dakk fi kembaar gi.
Dafa di nag, jëf mooy toxal wax. Li askani Afrig yiy xaar mooy ñu jëmmal dige yi.