Démb ci altine ji lañu doon ubbi 54eelu ndajem ndiisoo giy doxal gu mbooloo ngomblaani réew yi bokk ci kurélug OCI, UPCI. OCI di kurélug réewi jullit yi ci àddina si. Ndaje maa ngi ñu doon amal ci njiiteefu Njiitul Ngomblaanug Senegaal gi, Allaaji Maalig Njaay. Ci bi muy yékkati kàdduy ubbite gi, Sëñ Allaaji Maalig Njaay dellusi na ci anam yi kurélug OCI juddoo ginnaaw jëyya ji amoon ca atum 1969, fa jàkkay Al-Aqsa. Naka noonu, muy fàttali solo si bennoo ak jàppalanteb Ngomblaan yi am. Ci biir i kàddoom, soññ na itam 148i réew yi jot a nangu amug réewum Palestin, ak réew yi koy waaj a nangu, ñu seqi jéego yu yees. Jéego yooyu sax, li mu ci namm mooy ñu ànd nangu Jérusalem -Est mu nekk gëblag Palestin. Njiitu Ngomblaan gi delloo dëggal taxawaay bi Senegaal mës a am ci mbirum Palestin, moom mi jiite ndiisoo gi mbootaayu Xeet yi dénk àq ak yelleefi doomi Palestin.
MBIRI KËRUG LIGGÉEY GU LA POSTE
Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, namm naa xettali kërug liggéey gu La Poste ginnaaw jafe-jafe yu metti yi tegu ci kawam bu yàgg ba tay. Jël na ndogal yu am solo ngir tegaat kër googu ci yoon. Bokk na ci ndogal yi mu jël, joyyanti gafaka gi, kopparal ko ba mu méngook doxalin wi war, fexe kër gi tàggook i boram yi dem ba ci 8i milyaar te jagleel ko sàq mu ñeel suqaleeku sarwiis yu méngook jamono. Limub liggéeykat yeet dees na ko xoolaat ngir féexal ñenn ñi.
WÉR-GI-YARAM
Aji-tawat ji woppu mi ñuy wax “Mpox” daloon wér na. Jëwriñ ji ñu dénk wàllu wér-gi-yaram ak ndimbal yi moo ko xamle démb ci altine ji. Keroog 22i fan ci weeru ut wi ñu génn lañu ko nemmeeku woon ci réew mi. Boobook léegi nag, moo nga woon fajkat yi di topp fa raglu bu Faan. Fanweeri nit ya mu jotoon a nekkal itam ñoo nga woon ñu ber ak di leen topp ba xam wàllu leen. Bees sukkandikoo ba tay ci xibaar yi jëwriñ ji fésal, kenn ci ñoom amul jàngoro ji. Jëwriñ ji di sàkku ci askan wi ñu gën a bàyyi xel jàngoro ji te sàmmonteek digle yi bu baax.
UBBITEB LEKOOL BI
Càmm gi jublu na ci atum 2025-2026 mi ñu dëgmal. Sàkk nañu bés bi bër yi di jeex ak bés bi ñuy tàmbali njàng mi. Ci dekkare bi ñu génne te Njiitu réew meek Elimaanu jëwriñ yi torlu ko, jàngalekat yeek liggéeykati caytu gi dinañu teew ci lekool bi keroog altine 6i fan ci weeru oktoobar, bu 8i waxtu jotee. Bu dee njàngaan yi nag, ñoo ngi leen di xaar ci àllarba ji 8i fan ci weeru oktoobar. Bu dee lu jëm ci wàllu kàtte yeet, jëwriñu njàng mi dina ci dellusi ak ay leeral.