MONJAAL 2026 / RDC-SENEGAAL : XEEXU GAYNDE AK TENE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Joŋante bu tar te nar a tàng mooy xaar sunu gayndey futbal yi war a laaleek RD Kóngo, ca estaad “Martyrs”. Bu 16i waxtu jotee ci ngoon gi la joŋante biy door. Muy 8eelu bésub joŋante ñeel tooglantey Monjaal 2026 bi. Joŋante bile nag, dafa rax. Nde, boobaak léegi, Saa-Senegaal yeek Saa-Kóngo yee ngi tëkkuwante ak a nappante ci mbaali jokkoo yi. Dafa di, mats bii, ku ci dóor, buntu Monjaal 2026 bi dafay ubbeeku bu baax a baax ñeel ko.

Senegaal ak RD Kóngo ñooy xëccoo toogu bu njëkk bi. Jamono jii nag, RD Kóngo moo jiitoogum, ndax moo rawee Senegaal 1 poñ. Toogu boobu la gaynde yiy diir. Nde, bépp ekib bu jël pee, dafay jàll. Waaye, ekib yi ci topp te ëppaley poñ seen i moroom, dañuy joŋante ci ay baaraas yu nar a metti. Moo tax ku nekk di daw baaraas yi.

Ca seen ndaje mu njëkk ma ame woon fii ci Senegaal, dañoo temboo woon. Mu naqari woon lool Saa-Senegaal yi. Jamono jooja nag, Aliw Siise moo nekkoon ci boppu ekib bi. Ci diggante bi, lu bari soppeeku na ci. Ndax, Paab Caw wuutu na fi Aliw Siise te boobaak léegi Senegaal ñàkkul benn joŋante ci 23 yi mu jot a amal. Waaye, bu tay bi moom, narul yomb. Xam ko moo tax Paab Caw miy tàggat gaynde yi wax ne : « Joŋante bu metti lay doon sunu diggante ak ekibu RD Kóngo bu baax. Waaye nag, nun nooy Senegaal te ndam rekk a nu fi indi. »

Ndam loolu, Saa-Kóngo yi duñu ko yombalal gaynde yi. Ndax, ñoom itam, dañoo bëgg a dóor, bégalee ko seen waa réew ak seen i soppe. Dafa di sax, ekibu RD Kóngo bi dafa nekk ci yoonam. 2022 ba léegi, ci joŋante yu mu amal yépp, am na 13i ndam, temboo 6i yoon, daldi ñàkk 3I joŋante kese. Ci loolu a seen tàggatkat bi bëgg a sukkandiku ngir dóor Senegaal. Waaye, moom Sébastien Desabre, ciy waxam, bu joŋante bi amee solo yit, des na yeneen yu am solo su ni mel.  Dafa ne : « Joŋante bii am na solo lool waaye du joŋante bi ñuy tax a jàll dëggantaan. Ak sunu mbooloo mi nuy dooleel, dina nu jàppale ci joŋante bi. Dinanu xool Senegaal ci bët. » Maanaam daal, ragaluñu gayndey Senegaal yi.

Bu dee ci wàllu Senegaal nag, ndam rekk lañuy wax. Li ko waral mooy ne ponkali Afrig yépp jàll nañu, te Senegaal dafa bokk ci ponkal yi. Nde, Senegaal bokk na ci ñetti Monjaal (2002, 2018 ak 2022) te, ñaar yu mujj yépp, bokkoon na. Moo tax, bëggul wàcc yoonam. Waaye, yoon woowu, teney Kóngo yi ñoo ci toog, bëgg leen a teree dem. Kon, fàww gaynde xiiru, wane ne ñooy buuru àll bi bu dee ne bëgg nañu jàll.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj