Gaynde Senegaal yu futbal bi ñàkk nañu joŋante bi ñu doon amal ci seen digganteek Beresil. Ñu jóge fa ñàkk woy wi ñu amoon ci nekk bar gu ëpp lu mu joŋante (26i joŋante) te ñàkku ci benn.
Démb, ci gaawu bi, 15 nowàmbar 2025, la gayndey Senegaal yu futbal yi doon amal seen joŋante xaritoo ci seen digganteek réewum Beresil. Mu nekkoon joŋante bu àdduna sépp doon xaar. Nde, ca weeru suwe 2023, Gayndey Senegaal yi dañu wulli woon doomi Beresil yi 4i bal ci 2. Ci weeru suwe wii weesu itam, ñu dellu wulli Àngalteer biir dëkkam 3i bal ci 1.
Waaye, ci seen joŋante démb bi, mel na ni Saa-Itali biy tàggat guney Beresil yi, Carlo Ancelotti, am màggatum 66i at, dafa leen waajal bu baax. Nde, naka la arbit bi mbiib, mbir ya tàmbali rekk, goneem yi taxaw ci xefi gaynde yi, bañ leen a may fu ñu yakke seen nàkk, walla ñu fay naane ñeex ba fay seeñoo yeel.
Gaynde yi tàmbalee wiili-wiili. Fu ñu mbëkk mu fatt. Laata ñuy xippi bay gis fu ñu bëtt, doomu Beresil yi ñamal leen benn bii ca 28eelu simili ba. Gaynde yi dellu di làmbatu. Dajaguñu, doomu beresil yi dollil leen beneen bii ca 35eelu simili ba. Muy 2i bal ci 0. Ginnaaw loolu la gaynde yi soog a xippi, waaye taxul nu gis caaxu Beresil yi wenn yoon ci pàcc bu njëkk bi.
Bi ñu ñëwee ci ñaareelu pàcc beet, gaynde yi làmbatu nañu wet gu nekk, seen tàggatkat bi, Paab Caw def ay coppite, àndi ñeneen ngir yokk leen doole, waaye terewul Saa-Beresil yi dëju bu baax ci seen kër. Ba bi joŋante bi di jeex kenn mënul a lakk seen caax yi. Ñu daldi gàddu ndam li, fayuwaale ci kaw Saa-Senegaal yi leen ko defoon ñaari at ci ginnaaw.
Gaynde Senegaal yi nekkoon itam bar gi ëpp li mu joŋante te kenn amul ci kawam ndam. Mu jotoon amal 26i joŋante yoy, ku mu ci dóorul, dangeen a temboo. Ginnaaw bi leen doomu Beresil yi dóoree démb, woy wi daldi fay yam. Muy itam joŋante bu njëkk bu Paab Caw ñàkk ginnaaw at ak lu teg muy tàggat gaynde yi.
Mu mel ni démb du woon bésu Senegaal. Nde, gaynde yu ndaw yi amagul 17i at dañu nërmeelu itam ci kanamu Ugàndaa. Mu nekkoon joŋante dóor-mu-toog ci Kubu Àddina si ñuy amal ak maasu ñi amagul 17i at fa réewum Qataar. Naka noonu, gaynde yu ndaw yi daldi génn ci raw-gàddu boobule. Ñu tooge ci seen joŋante dóor-mu-toog bu njëkk ginnaaw bi ñu njëkkee jiitu ci seen kippaango ci faas finaal yi.
Ginnaaw-ëllëg ci talaata ji, Gaynde yu mag yi dinañu amal beneen joŋante ci seen digganteek réewum Keeñaa ngir wéyal seen waajtaay ci CAN2025 bi war a tàmbali ci weeru desàmbar wi, fa Marog.