Càmm gi dogu na ci aar cumbeefi biir réew mi (les entreprises locales). Jëwriñ ji, Sëriñ Géy, Jóob moo ko xamle. Fekk ñu doon amal péncoo mi ñeel ndefar geek yaxantu bi.
Barki-démb ci alxames ji, 17i pani oktoobar 2024, lañu tàmbali péncoo mi ñeel ndefar gi, yaxantu bi, ak cumbeef yu ndaw yeek yu yemamaay yi fa Jamñaajo. Ginnaaw bi ñu ubbee waxtaan yi, amal nañu leen ci diiru ñaari pan laata ñu leen di tëj ci àjjuma ji. Ay kilifa yu bari teewe woon nañu ko, rawatina ay ndawi réew, way-liggéeyal sa bopp yi ak farandooy Senegaal yi ci wàllum koom-koom ak kopparal.
Ginnaaw waxtaan yi, Jëwriñ ji ñu dénk yaxantu beek ndefar gi, Sëriñ Géey Jóob dalal na xeli way-yëngu sa-bopp gi (le secteur privé). Mu leen di xamal ni Nguur gi dina lal doxalin bu bees ñeel Ndefar geek yaxantu bi. Ci biir doxalin boobu, Càmm gi dogu na ngir aar cumbeefi biir réew mi (les entreprises locales).
« Mën naa dalal seen xel ci dogu gu amul benn gàkk gu Càmm gi am ci doxalin bu bees ñeel yaxantu beek ndefar gi te aju ci aar cumbeefi biir réew mi. »
Muy ay kàddu yu jëwriñ ji yékkati ci bi ñuy tëj waxtaan yi. Rafetlu na itam waxtaan yu am solo yi fa am. Tax na ñu mënn a diisoo ci lépp luy jafe-jafe ci ndefaru biir réew mi. Xamle naat ni koom-koomu réew mi dafa lott lool ci sukkandiku ci waa bitim-réew. Moo tax tey ñu war a soppi doxalin. Naka noonu, doxalin bu bees bi njëwriñalam namm doxal dina ci andiy coppite bu baax ba ñu wàññi ballu mbindaare yi ñuy yóbbu bitim-réew te duñ ci am daanaka dara.