PÓLITIG
Bu amee ñu doon laamlaame wotey 2024 ndax dees ko war a dàq am déet, mënees na jàpp ni wote yi dinañ am ci bés bees ko jàppoon. Njiitu réew mi Maki Sàll xaatim na dekkere bi keroog àllarba, 29 noowàmbar 2023.
Ci biir dekkere...
Barki-démb ci gaawu gi la ko Rimtalba Jean Emmanuel Ouédraogo xamle ci ab yégle. Moom Jean Emmanuel di ki yor kàddug Nguur gi (porte-parole) moo biral ne kibaaraanu Farãs googu di “Le Monde” amatul sañ-sañu génnee fab xibaar. Maanaam, muy ci mbooleem bànqaas yi...