Mbirum ngóor-jigéen doon na lu lëmbe àddina si fi mu tollu nii, moonte dey amul jenn diine ju ko nangu, du jullit, du kercen, du yawuut. Waaye ci réewi Tugal yi moom bari na lool ñu ko daganal ci wàllu yoon ba jox leen ay àq ak i yelleef. Céy Yàlla ! Ba fii ci Afrig, am na ay réew yu ko aayewul. Bokk nañ ci Afrig Bëj-Saalum, Gaboŋ, Àngolaa, Mosàmbig, “Seychelles”, Bostwanaa, Kot-Diwaar, añs. Ci réew yooyu, ñaari góor mën nañ séy te dara du leen ci fekk, ñaari jigéen tamit, muy nag lu doy waar lool te ñaaw.
Fii ci Senegaal, yoon da koo tere ci lim tudde “article 319 alinéa 3 du code pénal issu de la loi 66-16 du 12 février”. Buñ sukkandikoo ci li yoon wax ci ngóor-jigéen, mën nañ jàpp ni réewum Senegaal daganalu ko ci benn boor, ndax kuñ ci jàpp dinañ la teg ab alamaan bu dalee ci 100.000 cfa ba 1.500.000 cfa, boole ci ay ati kaso (1 ba 5i at). Buñ fàttalikoo ci atum 2008 ca “Grand Mbao”, amoon nay boroom ñaari tur yu fa doon amal takk, loolu nag, juroon coow lu réy a réy ba amoon ñuñ ci tegoon loxo ak lu tollu ci 9 ci seeni kurél.
Waaw, may laaj ndax seen kurél yooyu tamit jarul a def ab taxaw seetlu ? Aa balaa sos kipp, dinga am ay kayit ak yenn yu la warloo ak yoon. Kon nag, am na ñu leen di jàppale ñuy def i jéego ba noppi ne patt-pattaaral ci seen ruq.
Ci atum 2014, Njiitu-réew mee ngi doon xamle ni nguur gi masul a xalaat daganal mbir mi. Ñu teg ci ñaari at mu neeti ngóor-jigéen dëppoowul ak sunuy diine te feek mu ngi jiite Senegaal, waxu daganal sax kenn du ko fi wax. Loolu waroon naa dalal xelu ñépp waaye su jëf worook wax, xel day daldi teey.
Boobu ba tey nag, Saa-Senegaal yaa ngi xeex ndax ñu bañ a caaxaane loolu ci réew mi. Ndeem du doon lu yomb, ndax dëkk bi itam dafa am yoon, waaye taxul ñu toqi benn yoon. Ñoo ngi def lu ñu mën ngir ñooñu bañ fee am doole. 23i fan ci weeru Me bii ñu génn, waa Senegaal amal nañ benn doxu-ñaxtu ngir ñu yokk daan bi leen yoon di daan, jëlee ko ci 5i ati kaso, yokk ko ba muy 10i at. Ndajem ñaxtu moomu nag, ñi ko doon amal ñooy waa “Rassemblement Islamique du Sénégal”, ñu tudde woon ko “Valeurs Correctes”. Ci jataay jooju nag, kii di Usmaan Kuta di kenn ci “kurélu ndongo-daara yi” mi ngi xamle ne réewum Senegal dafa wara tënku ci ay jikko yu sell. Dolli ci ne, du ñu mës a nangu ngóor-jigéen ci réew mi. Ñu gis fa itam Demba Jóob di kenn ci ñoom mu lakk raaya “LGBT” yi ba tax ñenn ci boroom-ñaari-tur yi nekk bitim-réew mer ba futt di tëb ak a dal ci lënd gi (antarnet bi).
Maam Maxtaar Géy di njiital ONG Jamra mi ngi xamle itam ne Senegaal réewum diine la ndax dëkk bu am 95% jullit ak 4% kercen, kenn mëneesu fee xalaat ñu fiy daganal ngóor-jigéen, na leer ci boppu ñépp. Mi ngi ñaawlu it li àmbasaad bu Canada ak bu Hollande bind bataaxal 9i kuréli góor-jigéen yi ne ci sunu dëkk, di leen xamal ne képp ku bokk ci kurél yooyu te di kenn ci ñoom, daa ñu la yombalal kayitu dëkk boobu, ku ci bëgg liggéey te am ab nal, ñu jox la xaalis boo ko mën a taxawalee. Xam nga loolu mën naa jur musiba mu réy a réy ak ndaw yii nga xam ni tukki rekk a nekk ci seen xel.
Waaye nag, dafa am lu am solo lool lu benn doktoor wax. Mu ngi tuddee boppam doktoor D – ngir nëbb ki mu doon ndax liggéeyam mayu ko muy wax ci digganteem ak ñi muy faj. Dafa ni, ku bëgg saafara jàngoro dangay jéem a xam njëkk lu ko sooke. Ci la xamlee ne kaso la gone yu barey doon boroom-ñaari-tur, fa lañuy tàmbalee xam mbir moomu ba laŋ ca. Moo ngi wax tamit ne ñooñoo ëpp ci ñi ame Sidaa te buñ ci teelul jóg du baax. Ndax seetlu nañ ni dañuy takk jabar, am ay doom. Kon, bu nu leen xamul ba mën leen a faj du wóor ci nun. Sunuy rakk walla sunuy mag lañuy séyal te wàllante bi loolu mën naa ko yombal.
Ñu ràññee itam ay kilifa diine yu mel ni sëriñ Baabakar Si Mansuur, muy metitlu tekkaaralu nguur gi, di ñaax réew mi ci def li ko war. Gannaaw loolu la waa Adheos, di kurél giy dimbali ak a xeexal boroom-ñaari-tur yi ca Farãs, ñaan jëwriñ jiñ dénk biir réew mi mu tere kilifa diine yooyu ñu teg tànk Tugal.
Seetlu nañ it ne ci weeru suweŋ bii ñu génn, benn jàngalekat bu nekk ca Tëngéej, joxe na ci benn eksame bu ndongo yu digg yi doon amal, genn kayit guy wax ci mbirum ngóor-jigéen. Kayit gi nag mi ngi ko jukkee ci “Nouvelles chroniques de San Francisco” bu bindkatu Amerig boobu di Armistead Maupin. Ngóor soosu di koo xam ne, dafa bokk ci ñiy xeexal boroom-ñaari-tur yi. Ci jukki boobu, genn goney yónnee bataaxal yaayam, di ko yëgal ne góor-jigéen la. Waaye yaayam jooju da doon xeex lépp lu jëm ci ngóor-jigéen. Loolu ñu def Tëngéej di lu doy waar te jaaxal ñu bari ci réew mi ndax googu càggan nekkul lu xel mën a nangu. Dafa mel ni am na ñu def lu leen neex ba noppi ne teyuñu ko, njuumte la. Ak fi réew mi tollu, lii jëfu maa-tey lay nirool. Gannaaw loolu, jawriñ bi yor wàllu njàng meek njàngale mi tekki na ndombog-tànk jàngalekat boobu ñu dénkoon tàggatu jàngalekati àngale yi.
Waaye daal, yëf yi teey na xel.
Li wér te wóor, mooy ne sunuw askan taxaw na temm ngir xeex ak ñii di bëgg a daganal xeetu ñaawteef yii. Ñenn ci ndawi réew mi ak kurél yiy xeex ngóor-jigéen nee nañ su ñu sonnulee, ñoom duñ sonn. Te yit teg nañ ci ne, góor guñ ci jàpp muy jigéen-jigéenlu rekk dinañ ko digaaleek yow. Te boo seetloo ba seetlu weer yii nu génn yépp, ndaw yi seetatuñ ci Pólis mbaa Sàndarmëri. Ñiñ ci jot a jàpp yépp dañ leen a dóor ba ñu nooy, ba noppi widewoo leen, tasaare ko ci mbaali jokkoo yi (réseaux sociaux). Loolu nag, doon lu ñépp rafetluwul, ndax am na ñu jàpp ne ci dëkk bi lañ dëkk te tuumaal leen mën naa indil ay jafe-jafe seeni njegeñaale. Waaye nuy laaj lii : ndax suturaal nit war naa yegg ba foofu ?