Jukkees na ab laaj-tontu ci yéenekaay Le Soleil, limu 16582eel bu Gaawu 13 ak Dibéer 14 Sàttumbar 2025. Waxtaan la wow, sunu naataangoo bii di Aamadu Kebe moo ko séqoon ak werekaan bii di Bubakar Bóris Jóob, di bindkat, saabalkat, xeltukat, móolkat, añs. Waaye, balaa nu leen di baaxe laaj-tontu bu solowu boobu niki ëllëg, danu leen di gaaral as lëf ci yuqu mbindi Bubakar Bóris Jóob.
Ñetti at ci ginnaaw, 2022, Bubakar Bóris Jóob moo jëloon raw-gàddu Neexalu Neustadt ci fànnu ladab. Neexal boobu nag, ñaari at yu nekk lees koy jagleel kenn ci bindkati àddina si, di ko sargalee xalimaam bi mu yatt ba mu ñaw, di ci bind ak a fent i téere yuy jariñ àddina si mboole-seen, ci fànn yépp. Lu ko jiitu, bindkat bu mag bi njëkk naa jot ciy neexal yu ràññeeku niki Neexal bu mag bob Njiitu réewum Senegaal (1990) ngir téereem bii di Les Tambours de la mémoire ak Neexalu ladab bu mag ñeel Afrigu ñuule yi (2000) ngir mboolem liggéeyam. Ca atum 2019 tamit, jotoon na ci Neexalu Harold ak Ethel L. Stellfox bu jànguneb Dickinson ngir sargalee ko lépp li mu jotoon a liggéey ci xalimaam. Loolu dafay firndeel ni Bubakar Bóris Jóob guy la ci péncum bindkat yi.
Dafa di, ca atum 1981 la Bubakar Bóris Jóob njëkk a bind ab téere fent ci làkkuw tubaab (Le Temps de Tamango). Kon, 44i at ci ren, bi mu dalee bind ba tay. Boobaak léegi nag, werekaan bi tàyyeegul ci bind i téere ak i yaxal yoy, dañuy lënkale mboor ak jamonoy tay, di fàttaleek a soññe ci wareef yi képp-kenn ci nun gàlloo, di aamu ak a xeex ngir goreel doomi-Aadama yi, tinki leen ci xeeti jataŋ yu bare yi leen tënk ba tere leen doon ñi ñu war a doon, def li ñu war a def, wax li ñu war a wax.
Képp ku Yàlla baaxe ba nga dawal i téereem, rawatina Murambi, le livre des ossements ak yi mu bind ci làkkuw Kocc Barma, dinga gis ni, kàngaam bi Jóob, dafa yatt xalimaam, capp ko ci daawu péexte, di ci jëmmal ay xalaat yu xóot te ñaw yuy dog buumu njaam. Jubluwaayu Bubakar Bóris Jóob mooy jokkaleek a juboole nit ki, rawatina Saa-Afrig bi, ak reeni démbam ngir mu xam ki mu doon dëggantaan.
Moom nag, ci boppam la ko njëkke. Nde, ci làkkuw farãse la doorey mbindam. Daanaka, ci la siiwe. Waaye, képp ku yaroo ci keppaaru Seex Anta Jóob te dégg i njàngaleem niki moom, Bubakar Bóris Jóob, yàgg-yàgg, dangay dellu cosaan. Waaye nag, làkk wees nàmp mooy lutt biy lënkale nit ki ak mbooram. Ndaxte, làkk mooy ndëxëñteefu xayte, di kàggug mbatiit. Moo tax it, ak lu làkku doxandéem neex-neex, mëneesu koo macc ba ciy tàqamtiku. Lu ni mel la boroom xam-xam bi waxoon. Looleet la Bubakar Bóris Jóob xam ba tax ko dellu ci làkku meenam, bind ci ñetti téere fént yii di Doomi Golo, Bàmmeelu Kocc Barma ak Maalaanu Lëndëm.
Bubakar Bóris Jóob nag, yemul rekk ci di bind ay téere ci wolof. Nde, dafa taxawal ag këru móolukaay (Éditions EJO, 2018), di ci siiwal ay téere yees bind ci làkki Afrig, rawatina yoy Senegaal. Loolu doyul, mu sos ab saabalukaayu web, dippee ko Lu Defu Waxu (2018), ñu ciy siiwal i dég-dég (xibaar) ci fànn yépp, lépp ci làmmiñu Kocc.
Bubakar Bóris Jóob dafay amal i waxtaan fépp ci àddina si, di waxtaane ladab, mbatiit, solos làkk yi ak itam mbiri polotig ak yu ni mel. Li ko waral mooy dayoom, gis-gis bu sore bi mu am, xalaat yu xóot te xarañe yi muy bind ak a biral, rawatina fit wu muy àndal bu waree wax xalaatam. Nde, kilifa gi xamul làq-làqal, du layam-layami te du xalamal kenn. Li mu gëm lay wax, liy jariñe lay seet. Duggewu ko lenn lu moy yee nit ñi kem kàttanam.
Bindkat bi dafa bëgg a yee Saa-Afrig bi, siggiloo ko, xippiloo ko ay bëtam ngir mu xam te xàmmee, daldi natt fu muy teg i tànkam. Dafa koy firiloo ay noppam ngir muy déglu, di dégg, di ràññee ak a ràññatle. Waayeet, daf koy ubbiloo xel meek xol bi, yaatal leen ngir mu mën a nangook a dékku wuute gi am ci àddina si ci fànn yépp, musal boppam ci musibay xeetal, boddikonte ak par-parloo. Kon, lees mën a jànge ci mbindi Bubakar Bóris Jóob mooy ne, xalima kat, ndekete ngànnaay la.
Jëmm joojii nag la yéenekaayu Le Soleil jagleel xëtam bu njëkk ci njeexitalu ayu-bis bii nu nekk, daldi séq ak moom waxtaan wu yaatu wow, dees na leen ko tekkil, dégtal leen ko niki ëllëg ci altine ji.