Càmm gi soppeeku na. Démb, ci guddig gaawu bi, 6 sàttumbar 2025, la elimaanu jëwriñ yi, ànd ak magum fara-saytu njiiteefu réew mi, Umar Sàmba Ba, daldi siiwal jëwriñ yi bokk ci Càmm gu yees gi. Am na ay coppite yu bari yees ci seetlu, rawatina ci wàllu njëwriñi Yoon, Biir-réew mi, Mbiri bitim-réew, Tabaxte yi, Xëy mi ak Mbatiit mi. Coppite yooyu dañuy firndeel jubluwaay bu bees bu Nguur gi jël, di gaatnga doxalin wu yees.
Càmm gi soppeeku na bu baax. Nde, am na ay jëwriñ yu ñu wàccee, tabb ñu bees ; waayeet, am na ñees tóxal, jële leen ca njëwriñ ya ñu nekkoon, yóbbu leen feneen. Bees-bees baa ngi feeñ tamit ci ci yenn njëwriñ yees tas ak ci toftale gi.
Ñetti jëwriñ ñoo dem : Sëñ Muntagaa Jaawo mi nekkoon jëwriñu Wërteef gi ak Ñeeñal gi, Sëñ Usmaan Jaañ mi woon jëwriñu Yoon wi ak Seneraal Saŋ-Batist Tin mees dénkoon Biir-réew mi al Kaaraange bokkeef gi. Aamadu Ba mu Pastef moo wuutu Sëñ Muntagaa Jaawo, Soxna Yaasin Faal wuutu Sëñ Usmaan Jaañ, Mohammadu Bàmba Siise daldi wuutu Seneraal Saŋ-Batist.
Njëwriñu Bennoog Afrig, Mbiri bitim-réew ak Saa-Senegaal ya nekk bitim-réew, léegi, Sëñ Seex Ñaŋ lees ko dénk. Nde, Soxna Yaasin Faal mees ko dénkoon, dañu ko tóxal, jox ko Yoon wi.
Kii di Sëñ Abbaas Faal, ginnaaw ba ñu ko falee ca boppu meeri bu Ndakaaru, dafa tekki woon ndombog-tànkam ci njëwriñu Liggéey bi, Xëy mi ak jëflantey campeef yi. Moom itam, bookatul ci Càmm gi.
Càmm gi am na yit keneen ku koy waxal ku bees, muy Soxna Mari Róos Xadi Faatu Fay, moom mi ñu tabb muy fara-saytu Càmm ci wetu Elimaanu jëwriñ yi, di kiy saytu Jëflantey campeef yi.
Ci wàllu toftale gi, am na coppite itam. Ndaxte, ak Càmm ga woon, Njëwriñu Bennoog Afrig, Mbiri bitim-réew ak Saa-Senegaal ya nekk bitim-réew moo toppoon ci elimaanu jëwriñ yi. Léegi, njëwriñu Yoon gi lees ci toftal. Loolu dafay wane solo si Càmm gu yees gi nar a jox Yoon.
Seetlu nañu itam ne, dañu boole njëwriñu Xëy mi ak gog Liggéey bi. Jubluwaay bi mooy yaxanal ak ñoŋal liggéey bi, waayeet dëppale ko ak soxlay ndaw ñi nga xam ne, jamono jii, sonn nañu lool ndax ñàkkug xëy.
Yeneen coppite yu ci amaat mooy, benn, fànnu tabaxte wi ñu seppi, beral ko njëwriñu boppam, daldi koy dénk Sëñ Décce Faal. Ñaar, ci fànnu napp geet, dollees na ci koom-koomu géej gi. Nde, napp dafa ànd ak koom, bokk ci koom-koom. Ñett, Mbatiit mi am na njëwriñu boppam. Loolu nag, ñoñ mbatiit ak ñiy yëngu ci fànn wi yàgg nañu koo sàkku. Ñeenteelu coppite gaa ngi aju ci wàllu njëwriñu wér-gi-yaram gi. Ndaxte, dañu ca génnee mbirum Dimbalante gi, yóbbu ko ca njëwriñu Njaboot gi. Juróomeel bi mooy li Sëñ Abdurahmaan Juuf ak Sëñ Daawda Ngom weccoo ay njëwriñ. Nde, léegi, Sëñ Daawda Ngom moo wuutu Sëñ Abdurahmaan Juuf ca boppu njëwriñu Njàngale mu kawe mi, Sëñ Abdurahmaan Juuf daldi koy wuutu ca boppu njëwriñu Kéew mi.
Bees sukkandikoo ci dekkareb 2025 – 1430 bu 6 sààtumbaar 2025 bi Njiitu réew mi torlu, ci gaaralug elimaanu jëwriñ yi, nii la Càmm gu yees gi tëdde :
Sëñ Usmaan SONKO : Elimanu jëwriñu yi
-
Soxna Yaasin FAAL: Jëwriñu Yoon wi, Wattukatu Juun yi ;
-
Sëñ Biram Sulay JÓOB: Jëwriñu Laf gi, Soroj bi ak Mbéll yi :
-
Sëñ Seex ÑAŊ : Jëwriñu Bennoog Afrig Mbiri bitim-réew ak Saa-Senegaal ya ca Bitim-réew ;
-
Sëñ Biram JÓOB : Jëwriñu Dooley Xare yi ;
-
Sëñ Mohammadu Bàmba SIISE: Jëwriñu Biir-réew mi ak Kaaraange bokkeef gi ;
-
Sëñ Abdurahmaan SAAR: Jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Koppe bi ;
-
Sëñ Seex DIBAA: Jëwriñu Koppar yi ak Nafa gi ;
-
Sëñ Daawda NGOM: Jëwriñu Njàngale mu kawe mi, Gëstu bi ak Coste gi ;
-
Sëñ Yanqooba JÉMME: Jëwriñu Yaaley suuf si ak kaw gi ;
-
Sëñ Aliyun SÀLL : Jëwriñu Jokkoo gi, Njokkooy xarala yi ak Nimerig bi ;
-
Sëñ Mustafaa Màmba GIRAASI : Jëwriñu Njàngum réew mi ;
-
Sëñ Mabuuba JAAÑ: Jëwriñu Mbay mi, Dund bu matale bi ak Càmm gi ;
-
Sëñ Seex Tiijaan JÉEY: Jëwriñu Ndox mi ak Cetal gi ;
-
Sëñ Ibraayma SI: Jëwriñu Wér-gi-yaram gi ak Cellalug Bokkeef gi ;
-
Soxna Maymuuna JÉEY: Jëwriñu Njaboot gi, Dimbalante gi ak Jàppalante yi ;
-
Sëñ Aamadu Mustafaa Njekk SARE: Jëwriñu Xëy mi ak Tàggatug Liggéey beek Xarala bi ;
-
Sëñ Allaaji Abdurahmaan JUUF: Jëwriñu Kéew mi ak Njàllug Mbindaare mi ;
-
Sëñ Bàlla Musaa FOFANA: Jëwriñu Nosteg taax yi, Bokk-moomeel yi ak Caytug mberaay yi ;
-
Sëñ Sëriñ Géy JÓOB: Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu bi ;
-
Soxna Faatu JUUF: Jëwriñu Napp yi ak Koom-koomu Géej gi ;
-
Sëñ Oliwiye BUKAAL: Jëwriñu Liggéeyu Bokkeef gi, Liggey bi ak Coppiteg Sarwiisu Bokkeef gi ;
-
Soxna Xadi Jéen GAY: Jëwriñu Ndaw ñi ak Tàggat-yaram yi ;
-
Sëñ Aliyun JONN : Jëwriñu Mikorofinaas ak Koom-koomu Mboolaay meek Jàppalante bi ;
-
Sëñ Décce FAAL: Jëwriñu Tabaxte yi ;
-
Sëñ Aamadu BA: Jëwriñu Mbatiit mi, Ñeeñal gi ak Wërteef gi ;
-
Soxna Mari Róos Xadi Faatu FAY: Fara-saytu Càmm ci wetu Elimaanu jëwriñ yi, yor jëflantey Campeef yi, Yor Kàddu Càmm gi ;
-
Sëñ Aamadu Serif JUUF: Fara-saytu Càmm ci wetu jëwriñu Bennoog Afrig, Mbiri bitim-réew ak Saa-Senegaal ya nekk bitim-réew, féetewoo mbiri Saa-Senegaal ya nekk bitim-réew ;
-
Sëñ Alfa BA: Fara-saytu Càmm ci wetu jëwriñu Mbay mi, Dund bu matale bi ak Càmm gi, féetewoo Koppe yi ak Tàggatug baykat bi ;
-
Sëñ Momat NDAW: Fara-saytu Càmm ci wetu jëwriñu Nosteg taax yi, Bokk-moomeel yi ak cCaytug mberaay yi, féetewoo Ndëkk gi ;
-
Sëñ Ibraayma CAAM: Fara-saytu Càmm ci wetu jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu bi, féetewoo Yokkuteg lijjanti yu ndaw yeek yu yamamaay yi ak ndefar yu ndaw yeek yu yamamaay yi ;
-
Sëñ Bakari SAAR: : Fara-saytu Càmm ci wetu jëwriñu Mbatiit mi, Ñeeñal gi ak Wërteef gi, féetewoo Mbatiit mi, Ndefari pent yi ak Moomeeli mboor yi.