CAYTUG BOKKEEF GI : « NDAWUL NGUUR MËNUL DOON MILIYAARDEER », (USMAAN SONKO)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, teeweeji woon na ndaje mees jagleel coppiteg nosteg Càmm gi. Maanaam, naaluw soppi anam bi kuréli Càmm giy liggéeyee, lootaabewaat banqaas yépp. Liggéey boobii dafa bokk ci tëralin wu bees wu ñeel kuréli bokkeef gi. tay, altine 4 ut 2025, lees doon amal ndaje mi fa CICAD.

Ndaje mooma nag, bees sukkandikoo ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, solo su réy a réy la am. Li ko waral moo di ne, ba tay ci kàdduy Sëñ Usmaan Sonko, coppite gi dafay laal benn kenu bu am solo ci naaluw joyyanti koom geek mboolaay mi. Bi mu ubbiy kàddoom, elimaanu jëwriñ yi dafa ne :

« Ag dëppoo dafa am diggante liggéey bi nuy liggéey ci Naaluw joyyanti koom geek mboolaay mi ak Naaluw soppi réew mi. Benn ci kenu yi gën a mag mooy liggéeyu bokkeef gi. »

Ci xalaatam, bu ñu nee liggéeyu bokkeef gi, dafay jéggi mbirum caytug bokkeef.

« Xel yi dañuy faral di dem ci jëmmu caytu gi ci boppam, waaye liggéeyu bokkeef gi dafa laaxaale bépp xeetu liggéey bu caytu giy def te muy dellu ci askan wépp walla mu doon liggéey bob, moo koy saytu. Kon, dafay dellu ci lépp lu Càmm giy liggéey. »

Ci gis-gisu elimaanu jëwriñ yi, joyyanti kuréli Càmm gi ba ñuy jaamu soxlay askan wi dafa bokk ci jéego yu ëpp solo ñeel coppiteg Càmm gi. Nde, liggéeyu bokkeef gi mooy liy jokkale ma-xejj yi ak Bokkeef gi. Rax na ca dolli sax ne, dañu war a fexe bi nit ñiy jot ci dund bu doy, paj mu jaar yoon, njàng mu xarañe, waayeet jot ciy tabaxte yu mucc ayib, kiiraay ak kaaraange gu matale. Te, loolu yépp, Nguur gi la war.

Dafa di, bari na lu askan wiy ŋàññ doxalinu ndawi Nguur gi ci kurél walla banqaas yi koy teewal. Moom Sëñ Usmaan Sonko nag, weddiwul lu ni mel. Nangu na ni am luy sooxe ci liggéeyu Càmm gi. Wànte, xamle na tamit ne du lépp a bon. Nde, bees méngalee Senegaal ak yeneen réewi Afrig, dees na gis na am na lu leen réew mi tanee. Loolu du tere nag, ba tay ci gis-gisam, ñu war a liggéey ngir gën a jubal, gën a ñoŋal liggéey bi. Ndax, bu Senegaal bëggee suqaliku, dafay xool te di roy ci réew yi ko raw ci wàll wi.

Ci geneen wet gi, elimaanu jëwriñ yi woo na liggéeykati bokkeef gi, maanaam ndawi Nguur gi, ci ñu soppi seen i doxalin yoy, nootkat ba woon a ko daan doxalee. Maanaam, di jaay doole askan wi, di leen ñàkke kersa ak a toroxal walla di leen laaj xaalis ngir defal leen lol, yoon a leen ko may, muy seen àq. Li elimaanu jëwriñ yi bëgg mooy ay ndawi Nguur yu jub tey jubal, mën seen liggéey te di ko def ni mu waree, di leeral ak a sàmmonte ak seen wareef.

Naka noonu, Sëñ Usmaan Sonko àddu na ci nger gu jéggi dayo giy nasaxal liggéeyu Nguur te di jur ay loraange ci askan wépp. Te, nger, dafay gàllankoor am réew mu bëgg a naat. Daf ne :

« Li ëpp ci ndawi Nguur gi ay nit ñu jub lañu. Waaye am na ci ñu bari ñoñ, dañu bëgg lu yomb te di ko doxe. Te li nger di yàq dafa jéggi dayo : ci fànni koom-koom, mboolaay mi, kaaraange… »

Ngir màndargaal ay kàddoom, dafa joxe misaalu dawalkat, wax ne : « Bu ab dawalkat joxee dara ngir daamaram bañ a jaar ci caytug xaral gi, ëllëg, 20i bakkan ñooy rot ci tali bi, ñu leen di jooy. »

Dafa di, li am mooy, dafa am ay ndawi Nguur yu doyloowul seen ug payoor ba di ñuqiloo askan wi ngir defal leen li ñu warloo ak ñoom. Léeg-léeg, rawatina ci wàllu juuti yi, mu am ci ñu xañ Nguur gi koppar yu takku ci wàllu nger, daldi koy dugal ci seen i gafaka. Moo tax, ñaare, nga gis ndawul Nguur lu ndóoloon, jékki rekk yor alal ju dul jeex. Looleet, Sëñ Usmaan Sonko ñaawlu na ko.

« Ndawul Nguur mënul doon miliyaardeer. Moone de, at yii weesu, àgg nañu ci ñàkkal faayda lu ni mel. »

Li ko tax a wax lu ni mel mooy, Njiitu réew mi sax, 5i miliyoŋ kepp lay fayeeku weer wu dee, elimaanu jëwriñ yi di fayeeku 4i miliyoŋ yu teg, jëwriñ yi di fayeeku lu yées 4i miliyoŋ (3i miliyoŋ yu teg). Kon, ci yoon, Nguur mënul may nit xaalis ba muy doon miliyaardeer.

Elimaanu jëwriñ yi xamle na tamit ñoo ngi waaj a jàlle sémbuw àtte wow, dina aar artukat yi. Bu loolu yembee, dina bokk ci liy moytuloo, di ragal-loo ndawi Nguur yi. bu ko defee, dina bokk ci liy jubal ak jubbanti liggéey bi.

Jub, jubal ak jubbanti bi nag, ci fànn wile, mi ngi doore ci anam bi ñuy jëlee ndawi Nguur yi, di leen teg ci kurél ak banqaasi Càmm gi. Loolu la Sëñ Usmaan Sonko xam ba tax ko wax ne, léegi, bu ñuy jëlati, dees na ko teg ciy sàrt yu leer ba képp kees di tànn doon ku ko yéyoo, matale ko.Ndaxte, ci li elimaanu jëwriñ yi seetlu, « li ko dale ati 2000 yi ba léegi, ñoo ngi jël ci anam bu jéggi dayo te teguñu ko ci benn sàrt. Joante yi bareetul. » Loolu yépp moo tax ñu sumb naaluw coppite nosteg caytu gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj