COP 30 : ABDURAHMAAN JUUF FEDDALINA TAXAWAAYU SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñ jii di Abdurahmaan Juuf yékkati na ay kàddu fa Beresil ngir dëggal taxawaayu Senegaal ci xeex yàquteg jaww ji. Dafa teewaloon Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ca ndajem Njiit yi ñeel njuux li (kilimaa bi).

Bàrki-démb ci àlxames ji ak démb ci àjjuma ji, 6 ak 7i fan ci weeru nowàmbar 2025, lañu doon amal fa Belem (réewum Beresil) ñaari fani ndajem njiit yi ñeel njuux li. Muy ndaje mom, doon nañu ko amal ngir waajal Ndaje mu mag ci 10 ba 21 ci weer wi, ñu gën koo miin ci turu COP30 (Conférence des Parties), te jëm ba tay ci wàllu njuux li ngir wàññi tàngaayu jaww ji.

Ndaje maa ngi ñu doon amal ci njiiteefu Njiitu réewum Beresil, Luiz Inácio Lula De Silva. Ay téeméeri Njiiti réew ak yoy Càmm ci àddina sépp doon ko teewe. Ca Ndaje ma, Abdurahmaan Juuf, di jëwriñ ji ñu dénk kéew mi ak sopparñi aalam bi yékkati na fay kàddu ci turu Njiitu réew mi mu fa teewaloon.

Ci biiri kàddoom yooyu, jëwriñ ji taxaw na bu baax ci jamp gi nekk ci mbirum njuux li ak ni mu nekkee di lore ci àddina sépp. Naka noonu, muy xamle ni mbiri njuux li jamp na jamp gog, fees ko natt weesu na ko. Nde, yamul rekk ci di naxasal dundug doom-aadama ci suuf, dafa dem itam ba am ay njeexital yu bon ci tabaxte yi ak jumtukaay yi mbindeef yi di faral di jëfandikoo.

Mu rax ca dolli ni amul genn kembaar gu mucc ci yàqute yi. Waaye, réew yi néew yi doole, yi, rawatina yu kembaarug Afrig ñoo ci gën a loru.

« Afrig, rawatina Sayel bi, moo ngi yëg bu baax njeexitalu coppiteg njuux li. Dafay am solo ñu dégg sunuy baat ci waxtaan yiy am ci àddina si ngir ñu dogu jëme ci kopparal ak méngale. »

Naka noonu, jëwriñ ji dellu di fàttali wareef yi ci réew yépp bokk am, ak a feddali itam dogu gi réewum Senegaal am ci sopparñi aalam gi.

« Bu ngeen gisee sunu réew am ñu ko teewal ci jotaay yu kawe yii, dafay wane taxawaay bi Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay am ngir Senegaal mën a jëflanteek yeneen réew yi ci mbiri kéew mi »

Ginnaaw ndajem Njiit yi, ñuy xaar Nguur yi dëggal seen i taxawaay ci waxtaan yii di ñëw ci COP30 bi ngir ñu wàññi tàngaay bi ci àdduna si ak jàppale réew yi néew doole.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj