Ci guddig altine 8, jàpp talaata 9eelu fanu suwe 2025 la sóobarey géej yu Israayel yi dogaal ag gaal gu doon yóbbul dund ak ndimbal waa Gaasa, doomi Palestin yi. Jamono ji ñu koy dogaale, gaal gaa ngi yeboon 12i nit yiy xeexal àqi Palestin. Ca biir ñooña, Greta Thunberg miy xeex ngir ñu sàmm njuux li ak dépite Tugal bu jigéen bii di Rima Hassan ca lañu bokk.
Réewum Itali la gaal ga bawoo, keroog 1eelu fanu suwe 2025. Gaasa la jëmoon. Jubluwaay bi mooy naqarlu ak ñaawlu tëj bi Israayel bunti Gaasa ba dara mënu fa dugg, du nit, du dund, du tus. Loolu di jaay doole gu jéggi dayo. Nde, jamono yii, saa-Palestin yaa ngiy dee ndax xiif ak mar, wëliif bomb yi Israayel dëkkee di leen dóor. Àddina sépp a ngi toog di seetaan Israayel di faagaagal réewum lëmm. As-tuut ciy réew ak i nit ñoo nekk di ñaawlu doxalinu saay-saay bii di Netanyahu mi nekk di rey doomi Gasaa yi guddeek bëccëg. Loolu moo tax mbooloom 12i nit ñooñee di xeexal àqi saa-Palestin yi yeb seen gaal, wutali Gasaa, ngir wane tooñaange ak jaay doole gi Israayel dëkke. Waaye, sóobarey géeji Israayel yi bàyyiwuñu leen ñu àgg. Dafa di, fa ñu leen dogaalee sax moo warul. Nde, foofa, ci ndoxi àddina sépp la, kenn amul sañ-sañ dogaale fa genn gaal. Waaye Israayel moom, ni mu ko tàmm a defee, faalewul Yoon, faalewul àqi jàmbur. Am na ñu bari nag ñu nekk di ñaawlu dogaale bi Israayel dogaale gaalug ndimbal googee, rawatina Jean-Luc Mélenchon.
Bi ñuy dogaale gaalug « Madleen » gi, 200i kilomet rekk a desoon mu teer ca tefesu Gasaa ba. Loolu di frindeel ne, booba, gaal gaa nga woon ci ndoxi àddina si. Moo tax kurélug lëkkatoo gii di « Flotille de la liberté » jàpp ne dogaale boobule dafay jalgati Yoon.
Ca biir gaal ga, dees na ca fekk ñu cosaanoo Farãs, Suwet, Tirkii, Almaañ, Espaañ, Beresil ak Olànd. Dañu ñaawluji woon li Israayel tëj yooni ndox yiy jëme Gasaa, 2007 ba nëgëni. Yooni suuf yeet, saay-saayi Israayel dañu leen tëj bi ñu songee Gasaa ba léegi. Kon, Israayel daa fatt fépp.
Ginnaaw bi ñu leen jàppee nag, Israayel siiwal na ab widewoo bob, gisees na ci sóobarey Israayel yiy séddale ay sàndiis ak buteeli ndox ña nekkoon ca gaal ga. Bees sukkandikoo ci waa « Flotille », dañu ga ñenn ci ñoom, nangu seen i jollasu, ñeneen ñi dañu sàndi seen yos ci géej gi laata ñu leen di dogaale.
Kilifay pólitig yu Espaañ yi dañu woolu àmbaasadëeru Israayel bi ngir naqarlook a ñaawlu dogaale bi Israayel dogaale gaalug « Madleen » gi. Tirkii tamit ñaawlu na ko. Bu dee Farãs, Njiitu réew ma (Emmanuel Macron), deful lu dul sàkku ñu delloo doomi Farãs seen réew.
Li mat a laaj nag moo di : ndax dinañ jàpp ci loxo Israayel dakkal faagaagal bi muy faagaagal waa Gasaa ?