Ëttub àtte bu njëkk bu Abijã jël na ndogal, daldi génnee, seppi lawax bii di Séex Tiijaan Caam ci toftaleg wotekat ya. Moom Séex Tiijaan Caam, moo jiite làngu pólitig gii di PDCI-RDA. Li sabab ndogal li mooy ne, ca la àttekat ya lay, dafa ñàkk nasiyonaaliteem bu Koddiwaar. Kii di Meetar Rodirig Dajiye, layalkatu Tiijaan Caam, moo siiwal xibaar bi ci xëtu Facebookam.
Dafa di, Yoonu réew ma dafa jotoon ay càkkuteefi dabu (recours) yu bari, rawatina bu N’Zi Bernaar Kokoraa miy sekkarteeru nasiyonaal bu RHDP. Ci loolu la Yoon wa sukkandiku ngir jël ndogalu seppi Tiijaan Caam ci toftaleg wotekat yi, muy tekki ne du doon lawax ci wotey njiitefu réewum Koddiwaar.
Bees sukkandikoo ci kàdduy Sëñ Dajiye, ndogal loolu dafay firndeel ni dañoo bëgg tere Tiijaan Caam mu bokk ci wote yees dëgmal, 25eelu fanu oktoobar. Bu dee ñeneen ñi, dañu jàpp ni ndogal li jaar na yoon ndax Tiijaan Caam sàmmontewul ak Yoon ngir mën a joŋante ci wote yooyu.
Ñu bari nag, fa réewum Koddiwaar ak sax ci àddina si, dañu jàpp ne dara waralul ndogal lile lu dul bëgg a xeex ab lawax boo xam ne, bokk na ci ñu ëpp doole, nar a falu. Dees na xam fu wànnent di mujj ak i bëtam.