KUBALI GALAG YI : NGUUR GI DAJALE NA 3 000IY MILIYAAR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nguur gi siiwal na caabalug doxal ñeel nafa gi ci juróom-ñeenti weer yi njëkk ci atum 2025 mi. Caabal googu nag dafa biral i njureef yu am solo ci wàllu kubali galag yi [recettes fiscales]. Dafa di, li ko dale weeru sãwiye jàpp weeru sàttumbar 2025, Nguur gi dajale na ci 1 172i miliyaar ciy seefaa.

Bees boolee li Nguur gi dajale lépp, mat na 2 987,9i miliyaari seefaa. Seen jubluwaay moo doon dajale 4 099,6i miliyaar ci at mi. Galag yees jukkee ci sosiyete yi moom, lees ci nisëroon lépp lañu matal. Nde, bi ñuy tollu ci bésub 30 sàttumbar 2025, dajale nañu 432,9i miliyaar te 429,9i miliyaar lañu jublu woon.

Galag yees duppee IRVM/IRCM (impôt sur le revenu des valeurs mobilières) ñoo raw yeneen yépp. Ndax, dajalees na ci 111,5i miliyaar fekk 86,6i miliyaar lañu yaakaaroon.

Bu dee galag yees di dagg ci payoor yi nag, dafa xaw a sooxe tuuti. Kubali fànn woowu, 578,1i miliyaar lañu ci dajaleegum. Nguur gi 849,9i miliyaar la ci bëgg a dajale ci at mi. Kon, am lees war a mottali. Yeneen xeeti galag yi, niki TVA bi, boo leen boolee, dajalees na ci 1 661,2i miliyaar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj