Tay, alxames, yemoo ak ñeenti fan ci weeru sàttumbar lañuy màggal bés bi Yonentu bi, Muhammad (SAWS) ganesee àddina. Mu doon bés bu mag ci réewum Senegaal. Dafa di, bés la bob, dañuy màggal ci dëkk yu bari ci biir réew mi. Te, dëkk yooyu ay mbooloo yu takku ñoo fay tase. Foo sànni mbàttu mu tag. Muy fu ci mel ni Tiwaawon, Kawlax, Cenaba, Halwaar, Gunaas, añs.
TUKKIY ELIMAANU JËWRIÑ
Bu yàggul dara la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, jóge fa réewum Siin ginnaaw ba mu fa amee ab diir. Dina amalaat yeneen tukki ci Kembaar yu wute. Te, yépp ci weeru sàttumbar la leen di amalee. Tukki bu njëkk bi mi ngi koy amalee fa “Emirates Arabes Unis” diggante juróom-ñetti fan ba fukki fan ak ñaar. Beneen bi ma nga koy amale fa kembaaru Tugal, fa réewum Itaali diggante fukki fan ak ñett jàpp fukki fan ak ñeent ci weeru sàttumbar wii ñu nekk.
Naka noonu, tukki bees waxoon ne dina ko amal fa réewum Farãs du ko mujjee amal. Bees sukkandikoo ci xibaar yi Senego biral, woote bi ko waa BPI woo woon, da koo mujjee gàntal. Li ko waral du lenn lu moy ne moom dafa xat. Jotam matewul ngir mu wuyuji ca ndaje mooma ñu koy woo ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru sàttumbar wii. Waaye, loolu terewul ne dina dalal elimaanu jëwriñu Farãs bi fi Ndakaaru ci lu dul yàgg dara ci ndaje mi ñuy dippe SIG (Séminaire Intergouvernemental).
LONASE AK GFM DOG NAÑU SEEN UG PAS
Pas gi doxoon diggante GFM (Groupe Futurs Médias) ak kër gii di LONASE jur na coow lu bari ci réew mi, rawatina fan yii. Nde, dafa bari ñoo xam ne rafetluwuñu ko. Li gën a yokkati coow li mooy siiwalug pas gi ci mbaali jokkoo yi. Pas gi nag mujj nañu koo dog. Looloo tax, jamono jii coow topp na Njiitul LONASE lii di Toussaint Manga. Ndax, ku nekk ak ni mu gis xew-xew boobu. Muy ñi ànd ak Nguur gi fi nekk ak ñi àndul ak ñoom. Ku nekk a ngi ciy waslu àq.
RADDHO, LSDH, AIS ÀRTU NAÑU NGUUR GI
Kurél yiy xeex àq ak yelleefu doomu-aadama jóg nañu ngir àrtu Nguur gi. Nde, kenn umpalewul ne bu yàggul dara fajkat yi génnee nañu ag caytu ginnaaw bi ñu seetee kii di Farba Ngom. Ñu xamle ne wér-gi-yaramam demewul noonu. Li gën mooy ñu génnee ko kaso. Looloo tax waa RADDHO (Rencontre Africaine pour la Défense des Droits de l’Homme), AIS (Amnesty International Sénégal) ak LSDH (Ligue Sénégalaise des Droits Humains) di sàkku ci kilifay réew mi ñu gëddaal njureef yi tukkee ci ceet gi ñu doon seet wér-gu-yaramu Farba Ngom. Su ko defee ñu càmbaraat càkkuteefu bàyyig négandiku gi ay layookatam dugalaat.
NDOG MU METTI CI YOONU LINGEER-MAATAM
Ndogi yoon yaa ngi wéy di gën a taqarnaase. Daanaka saa su amee xew-xew bu jegesi rekk, ndog yi ne kurr. Ba tax na, am na ndog mu metti mees nemmeeku démb wetu Lumbol-Laana di dëkk bu nekk ci goxu Barkeeji. Benn seexu sëriif moo fa mbëkkante ak genn sëfaan. Juróomi doomi-aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan. Fukk ak juróom jële ci ay gaañu-gaañu. Mu am ca ñaar ñu ci mettile lool ba ñu mujj leen a rawale fa Maatam. Ña ca des ñu yóbb leen fa raglu Màgget Lóo bu Lingeer.