Ayu-bés bee ñu génn la Ngomblaan gi tegoon ay tuuma ci ndoddu ñenn ñu fi nekkoon ay jëwriñ ca jamonoy Maki Sàll. Boobaak léegi, ñi ngi toog di xaar. Waaye, dafa mel ni toogaay amatul. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, tay, ci alxames ji, Mansuur Fay dem na fa DIC ngir jël woote biy tax mu mën a taxaw ci kanamu ëttu Yoon bu kawe bii ñuy dippe “Haute Cours de Justice”. Nee ñu, bu Mansuur jàllee, kii di Ndey Sali Jóob Jeŋ tamit, dina dem jëli bosam. Li waral loolu mooy ñaar ñooñu dañu leen di tuddu ci mbirum ñeel koppari mbas mi.
LU BEES ÑEEL MBIRUM FARBA NGOM
Lu tollu ci ñetti weer bi ñu ko tëjee ak léegi, ay layookatm a ngi wut i pexe ngir génnee ko. Waaye, ba tay, sotteegul donte ne sax, ñi ngi ci yoon wu baax. Nde, dañu ne woon wér-gi-yaramam mayu ko mu des ca kaso ba. Bees sukkandikoo ci l’Observateur, Njiitu àttekati PJF Pool Judiciaire Financcier) yabal na Porofesëer Alasaan Mbay ngir mu saytu wér-gi-yaramu Farba Ngom. Li mu ko dugge mooy xool ndax, wér-gi-yaramam may na ko mu toog ca kaso ba am déed. Laaj boobu njureef yiy tukkee ci ceetu fajkat boobu ñoo ko mën a tontu. Kon, fii ak ub diir dees na xam nu Farba di mujjee.
XIBAAR ÑEEL MBIRUM AASURAA FAAL AK USÉYNU KAYRE
Ci ndoorteelu ayu-bés bii lañu tegoon loxo Aasuraa Faal ak El Haaj Uséynu Kayre. Tay, ci alxames ji, lañu doon taxaw fa ëttu àttewaay bu Ndakaaru. Waaye, mujjuñu leen a àtte. Dañoo dàq layoo bi ba ñaar-fukki fan ak ñaar ci weeru me wii. Loolu terewul, kii di Aasuraa moom bàyyi nañu ko bàyyig négandiku. Ndax, wayndarew wér-gi-yaram lañu sukkandiku. Kii mu fa dugandooloon di Kayre mujjuñu koo bàyyi. Àttekat bi da koo bañal càkkuteefu bàyyig négandiku gi mu jébbaloon. Kon, moom Kayre, fa lay des ba seen layoo ñëw.
FÀTTALIKU BÉSU BÓOMUG FÀLLU SEEN
Tay, ci alxames ji, fukki fan ak juróom ci weeru me moo yamoo ak bés bi ñu faatoo ndongo lii di Fàllu Seen. Xew-xew bu tiisoon ma nga ame woon fa daara ju kawe ji nekk fa Ndar, ca atum 2018. Mu nekkoon xew-xew bu tiis lool ci Senegaal rawatina ndongo yi nekk ci daara yu kawe yi. Loolu taxoon sax, ñu toogoon ab diir jànguñu. Bés bu tiis boobu lañuy fàttaliku tay. Moo tax, kurél gi ëmb ndongo yi di CESL jël ndogalu dakkal njàng mi bésub tay jii. Rax-ci-dolli, kuy ndekki, añ walla reer doo fay dara.
XEW-XEW BU DOY-WAAR FA MBUUR
Ab xew-xew bu yéeme moo am fa Sowaal, nekke fa Mbuur. Benn tabaxkat moo bàyyi soxnaam ba muy nelaw mu bóom ko. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, nee nañ daf ko doon jiiñ njaalo. Maanaam, daf ko doon moy. Xew-xew baa ngi am ci guddig dibéer jàpp altine. Nee ñu bi mu ko xojee bam faatu, dafa tëdd ci wetam ba fajar ngir gëmloo nit ñi dafa dee noonu. Loxo kenn laalewu ci. Waaye, dëkkandoo yi dañoo dese gëm li mu wax. Ci lañu ko Sàndarmëri bu Sali Portidaal. Bi ñu ko tegee loxo ba def seen luññutu, ci la nangoo ne moom, S. F. Jóob, moo bóom soxnaam sii di F. Géy. Moom, tabaxkat bi, jamono jii, ma nga ca loxoy Yoon.
BENEEN XEW-XEW BU YÉEME FA MÉDINA
Koñ bii di Médinaa nekke fa Ndakaaru, ñaari jaaykatu dibi hawsa lañu fa teg loxo. Li ñu leen tegee loxo mooy ne dañoo yoroon ab sikaare boo xam ne muus mu ñu rendi moo ci nekk. Ñaari jaaykat yooyu, ñi ngi cosaanoo fa réewum Niseriyaa. Jamono jii nag, ña nga ca loxoy Yoon. Amaana balaa yàgg dees na xam fan lañuy mujj.
DAAN NAÑU KI FI NEKKOON NJIITU RÉEWU MURITANI
Muhammed Uld Abda Asiis nekkoon fi Njiitu réewu Muritani daan nañu ko, daan bu diis. Nde, dañu koo njëkkoon a daan, mu dugal ab dabantal. Waaye, jëlewu ca ndam. Daan ba sax daa gën a tar faf. Ndax, daan nañu ko fukki ati kaso ak juróom yu mu war a tëdd. Li ko daane mooy ger, luubal alalu réew mi ak setal xaalis, ñu koy wax ci farañse “blanchiment d’argent”. Waaye, Yoon yamul foofu kese. Ndax, da caa boole teg loxo mbooleem lu mu moom.