LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (30/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SULLIWAAT NAÑ WAYNDAREW FÀLLU FAAL

Mbirum Fàllu Faal lëmbe woon na lool réew mi jamono yee weesu. Nde, ñu bari dañoo génnoon di ñaawlu li ñu teg ci ndoddam. Ndax, nee ñu, ciif gi ñu koy jiiñ ne moo ko def rakkam ju jigéen, du moom. Te, loolu moo taxoon ñu daan fukki at ak juróom. Bi coow li baree ci mbir mi lañu sulliwaat wayndare wi. Tay, ci àllarba ji, la doon taxaw fa ëttu dabantal bu Ndakaaru.  Mbir mi nag, dees na ko leeral ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru ut wii ñuy waaj a dugg.

UBBITEG LUÑÑUTU ÑEEL XEW-XEWI PÓLITIG DIGGANTE 2021 AK 2024

Coowal luññutu ñeel ñi ñu bóomoon jur na coow lu bari. Nde, ñu bari ñu ngi sàkku ñu leeral mbir yi. Ndax, juróom-ñett-fukki bakkan waruñoo génn àddina ba tay kenn yéyul yàbbi ci. Moo tax, ñu bari ci askan wi di sàkku ñu door luññutu yooyu, daan ñi def ñaawteef yooyu. Jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon mi ngi séqi ay jéego ngir Yoon ubbi ci ay luññutu. Nde, li xew-xew diggante 2021 ak 2024 ëpp na a bàyyee noonu. 

BÀYYI NAÑ MUSTAFAA JAXATE AK BASIIR FOFANA

Jamono yee weesu lañu ko tegoon loxo. Donte ne sax, jotoon na a jàkkaarloo ak àttekat bi taxul woon ñu xam ndax dañu koy daan walla dañu ko bàyyi. Waaye, lépp leer na tay. Dafa di, moom daan nañu ko sax. Waaye, loolu du tax mu tëdd. Nde, ñaari weer lañu ko daan yoo xam ne dafa ci war a tëdd fukki fan ak juróom. Te, diir boobu ëppal na ko bu yàgg.

Naka noonu, kii di Basiir Fofona tamit mujj nañu koo daan. Moom nag, li ñu ko doon toppe mooy biral xibaar yoo xam ne wérul. Waaye, loolu terewul ñu bàyyi ko. Nde, ñaari weer lañu ko daan yoo xam ne du ko tëdd.

MBËKK MI

Ndawi Afrig sowu-jant yaa ngi wéy di mbëkki ba tay. Saa su ñu jàppee ne mbir mi wàññeeku na, fekk ne booba la waalo gën a aay. Ndax, fii ci réewum Senegaal sax, ndaw ñi wàccaguñu yoon wi. Li koy firndeel mooy démb ci talaata ji rekk am na gaal gees jàpp fa weti Ndar. Te, dafa am ñu mu doon yóbbu. La ca nekkoon ci ay doomi-aadama tollu na ci ñaari téeméer ak fanweer ak juróom-ñeent. Kon, ndaw ñi bàyyeeguñu mbëkk mi. Dañu doon taaxeerlu ab diir rekk.

LAYOOKATI FARBA NGOM YI SÓOBU NA CI BENEEN XEEX

Ayu-bés bii ñu génn la ñoñi Farba yi doon amal ndajem waxtaan. Li ñu ko duggee woon du lenn lu moy ñu bàyyi Farba Ngom. Dafa di, moom mi ngi bëgg a yàgg ca kaso ba. Ginnaaw, bi ñu amalee ndaje moomu ba pare dafa am ay xibaar yu saabalukaay bii di Yoor-Yoor fésal. Dafa xamle ne ndaje moomu, gaa ñi def nañu ci lu tollu ci benn miliyaar ngir mbooloo mi wuyusi wooteb Farba Ngom bi. Layookati Farba yi nag, loolu lañ ne duñu ko dégg. Looloo tax, ñu ne dinañu jébbal ab jure. Ndax, xibaar yi ñu biral dara wéru ci.

NJUREEFI KÀTTEY 2025

Diggante weeru suwe ak sulet lañu doon amal ñetti kàtte yi ñuy amal at mu jot. Muy CFEE, BFEM ak BAC. Njureefi Kàtte yooyu nag xamees na leen. Xam nañu limu ñ i am lijaasa yi  ñu doon dagaan. Maanaam, ñi jàll ak ñi jàllul.

Bu dee CFEE bi, am nañu 70,73%. BFEM bi, bees ko xaymaa, mu ngi tollu ci 78,59%. BAC bi moom mi ngi tollu ci 47,62%. Kon, bu ñu xoolee bu baax CFEE bi ak BFEM bi yépp a am i yokkute. Waaye, BAC bi moom li am dafa wàññeeku bees ko méngalee ak li amoon daaw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj