Ci alxamesu démb ji la xibaar bi rot. Sóobare yay jiite réewum Mali jamono jiii ñoo ko fésal. Bees sukkandikoo ci dég-dég (xibaar) yi jëwriñu Kaaraange gi siiwal ca seen tele réew ma, dañoo jàpp ay sóobare ak i ma-xejj, mu am ci ñaari seneraal ca làrme ba ak ndawul Farãs. Dañoo njort ne seen yéene moo doon yëngal réew ma, daaneel njiit ya.
Seneraal Daawut Aali Mohammedin, di jëwriñu Kaaraange gi ca Mali, moo siiwal xibaar bi, niki démb, alxames 14 ut 2025. Ca seen tele réew ma, ORTM, la siiwalee dég-dég bi, yeneen saabalukaayi réew ma tasaare ko. Dafa ne :
« Càmmug négandiku gee xamal waa réew meek àddina sépp ne, jàpp nañu as mbooloo ci biir sóobare yi, fekk ñu bëggoon a jëf jëfi pékke ngir daaneel campeefi Bokkeef gi. »
Bees sukkandikoo ciy kàddoom, jarul askan way tiit walla di ame njàqare. Ndaxte, bat ay ciy waxam, kilifa ya gàntal nañu pexey nooni réew ma.
Jamono yii, sóobarey Mali yi dañu nekk di jànkonteel ak i jafe-jafe wëliif fitnay rëtalkat ya. Nde, ca seen biir, dafa ci am ay sóobare yuy fippu, di beddeeku. Cig pàttali, ca weeru me 2025 wee weesu, amoon nay mbooloo yu doon ñaxtu, di kaas ngir ñu delloosi demokaraasi ca réew ma. Dafa di nag, guléet lu ni mel di fa am, ginnaaw ba Asimi Goytaa foqatee Nguur ga ba léegi, ñeenti at ci ren.
Bu dee seneraal yi ñu jàppandool ak lenn ciy ma-xejj ak tubaab bees njort ne ndawul Farãs la, kilifa yi leeraluñu lépp li leen ñeel. Xanaa daal li ñu xamle turu tubaab bi, muy Yann Vezilier. Ci li jëwriñu Kaaraange gi xamle, moom Yann Vezilier, « way-yëdduy [services de renseignements] Farãs yi lay liggéeyal, ñoom ñi nga xam ne dañu kootoo ak i way-pólitig, ay way-moomeel ak i sóobare » fa Mali. Farãs nag àddoogul ci tuuma jooju.
Ci li Seneraal Daawut Aali Mohammedin xamle ba tay, bésub 1eel ci weeru ut wii la kootoo gi tàmbali woon. Tele réew ma sax wane na fukk ak benni nataali nit ña ñu jàpp, wax ne ñoom ñooñee ñoo doon nas i pexe ngir yee fitna ca réew ma, daaneel njiit ya. Jëwriñ ji tudd na fa yit ñaari seneraal yu mu tuumaal, wax ne ci kootoo gi lañu bokk. Benn seneraal baa ngi tudd Abaas Démbele, di woon gornooru diiwaanu Mopti ba ci digg réew ma. Moom moomii, seneraal Démbele, ca weeru ma lañu ko wàccee woon. La taxoon ñu tekki ndombog-tànkam mooy li waxoon ne dañu war a ubbiy luññutu ngir leeral tuuma yi ñuy teg ci kaw làrme bi, wax ne dafa rey ay ma-xejj ca dëkk bii di Jafaraabe. Beneen seneraal bi mooy Nema Sagara.
Réewum Mali dafa nekk di jànkonteel ak terorist yi (rëtalkat yi), ñu sonal leen lool. Rax-ci-dolli, jot nañu faa amal ñaari « coup d’Etat » ci at yii ñu génn. Ginnaaw gi, dañoo dàq sóobarey Farãs yi.
Ca weeru Suwe wee jàll lañu dollil seneraal Asimi Goytaa yeneen 5i at yu muy toogaat ci jal bi. Lu ko jiitu, ca weeru me, dafa tasoon làngi pólitig yépp.