MBOOTAAYU XEET YI WOTE NA “DECLARATION DE NEW YORK” BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ngomblaanu Mbootaayu Xeet yi nangu na lees duppee “Déclaration de New York” bi nga xam ne, dafay sàrtal nekkug ñaari réew yii di Palestin ak Israayel. Maanaam, li “Déclaration de New York” bi wax mooy ne, Israayel dafay nekk réewum boppam, am mberaayam ak dig yu leer. Naka noonoot, Palestin itam dafa nekk réewum lëmm, am mberaay mu leer ak i dig. Waaye nag, ba tay ca “Déclaration de New York” booba, Hamaas dafay génnee loxoom ci yoriinu Palestin, daldi wéer ngànnaay yi.

Araabi Sawdit ak Farãs ñoo waajal “Déclaration” bi. Ginnaaw bi ñu ko wotee, 142i réew ñoo ca ànd, 10 bañ (Israayel ak Etaasini ci lañu bokk) ak 12i réew yu màndu.

Li ñu yaxal ca “Déclaration” ba nag dafa leer. Dañu bind ne :
“Noo ngi ñaawlu cong yi Hamaas amaloon ci kaw i ma-xejj keroog bésub 7eelu fanu oktoobar.”

Fukk ak juróom-ñaari réew ñoo torlu woon “Déclaration” bi ca weeru sulet. Ci biir 17i réew yooyu, bari na ci yoy araab. Ñoo nag, 17i réew yooyii, dañoo dàq Hamaas ci pexe mi ñu lal ngir delloosi jàmm fa Gasaa. Nde, dañu bind ne :

“Ngir dakkal xare bi, Hamaas dafa war teggi kilifteefam fa Gasaa te jël ngànnaayam yi, jox leen Kilifteefu Palestin ci ndimbalug réewi àddina si. Loolu moo dëppoo ak jubluwaayu samp ñaari réew yu moom seen bopp.”

Kii di ndawul Palestin li, Riyad Mansuur, àddu na ci, di woo Israayel ngir mu déglu, ànd ak xelam te nangu loxo jàmm bi ñu koy tàllal.

Bu dee Njiitu réewu Farãs li, Emanuwel Makrõ, dafa bind ci xëtam bu X, wax ne :

“Booloo nanu ànd, xàll aw yoonu jàmm wow, amul dellu ginnaaw.”

Bu dee Etaasini ak Israayel moom, ànduñu ci ndogal li. Ci seen gis-gis, Mbootaayu Xeet yi dafa jeng. Ci gis-gisu Dani Danõ, ndawul Israayel li fa Mbootaayu Xeet yi, ñoom rekk ñoo am sañ-sañu xool ni ñuy jëflantey waa Hamaas.

Cig pàttali, ñoo ngi dëgmal am ndaje mees jagleel mbirum Palestin. Keroog 22 sàttumbar lees koy amal. Araabi Sawdit ak Farãs ñooy jiite ndaje mooma. Te, bés boobu la Emaniwel Makrõ wax ne dina ci nangu nekkug Palestin niki réew.

Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj