Njiiti Senegaal yi dañu bëgg a jël fànnu ndefar wi, def ko xolu koom-koomu réew mi. Ci atum 2026 mii lañu bëgg a tàmbalee jëmmal seen naal woowu. Ndaxte, dañu namm a tabax i ndefar, samp leen fépp ci réew mi, ngir suuxat koom-koom gi, nit ñi mën a am xéy, réew mi tegu ci yoonu naataange. Naka noonu, ci talaatay tay jii, Ndiisoog Kopparal geek Caytug nafa gi, ak itam Ndiisoog Mbiri koom-koom yi, liggéey nañu ci naaluw nafa wu njëwriñu Yaxantu bi ak Ndefar gi. Ba ñu noppee ci seen liggéey boobu nag, jagleel nañu jëwriñ Sëriñ Géy Jóob ay koppar yu tollu 355,9i miliyaari ciy seefaa.
Ci atum 2025 mi, 50,1 miliyaar ciy seefaa lañu jagleeloon njëwriñu Yaxantu bi ak Ndefar. Kon, dañuy gis ne, ci atum 2026 mi, ful nañu ko 609,62i yoon. Guléet lu ni mel di fi am. Loolu dafay firndeel yéene ji Nguur gi am jëm ci tabax i ndefar yuy doon cëslaayu koom-koomu réew mi.
355,9i miliyaar yi nag, dees na ko pàcc-pàccal ci juróomi naal yii toftalu :
-
Yokkuteg béréb ak fànni ndefar yi (109,02 miliyaar) ;
-
Yombalug njureef yeek njariñe yi ak yeesalug yaxantu bi (33,14 miliyaar) ;
-
Kaaraangeg yaxantu bi ak dooleel taxawaayu Senegaal ci àddina si (2,23i miliyaar) ;
-
Jàppale ak kopparal lees duppee PME/PMI (3,29 miliyaar) ;
-
Njiiteef ak caytug fànn wi (2,45 miliyaar).

