NDAJEM JËWRIÑ YI : NJIITU RÉEW MI ÀDDU NA CI LÀKKI RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu Réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar FAY, jiite na, ci alarbay démb ji, 10eelu fanu sàttumbar 2025, ndajem jëwriñ mees baaxoo di amal ayu-bis bu nekk ca Njénde la.

Ca ndoorteelu waxam, moom Njiitu réew mi, dafa àddu ci dekkareb 2025-1430 bu 6 sàttumbar 2025, muy dekkare bi tabb jëwriñ ak fara-saytuy Càmm gu yees gi. Ginnaaw loolu, biral na ngërëmam ñeel jëwriñ yees tekki seen i ndomboy-tànk, daldi sargal ñees tabb yees ci Càmm gi. Kon, démb la Càmm gu yees gi doon amal ndajeem jëwriñ mu njëkkam.

Njiitu réew mi fàttali na ne, nekk jëwriñ walla fara-saytu du ndam, waaye sas la. Maanaam, yen bu diis la bob, boroom daf ko war a xam, bàyyi ko xel te aamu ngir liggéey, sax ci di jaamu soxlay askan wi mboole-seen. Ci beneen boor, Njiitu réew mi wax na ci lu jëm ci jëmmal naali njàngum bind ak gën a dooleel làkki réew mi. Ginnaaw bi mu tànnee weeruw sàttumbar wii niki daaw, def ko weeruw njàngum bind, sargal na ñiy yëngu ñépp ci fànn wi ngir liggey bu am solo bi ñu def ci réew mépp, ku ci nekk ak fa nga féete.

Bu loolu weesoo, jox na ndigal jëwriñu Njàng meek Njàngale mi, Sëñ Mustafaa Màmba Giraasi, sant ko mu baral ci liggéeyi sémb yeek naali njàngum bind yi, rawatina ci sunu làkki réew mi. Wax na sax ne, nañu dugal te yaatal njàngum làkki réew mi ci daara yi ak jànguney réew mi, ci fànni njémmeer gi ak njàmbure gi. Nde, bees sukkandikoo ciy waxam, loolu dafa bokk ci liy jëmmal sémbuw Senegaal gu moom boppam, jub te naat.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj