Lekk baax na. Waaye nag, na doon lekk lu baax, ci anam bu baax. Loolu la boroomi xam-xam yiy gëstu ci fànnu dund wax. Dafa di, jamono yii, dafa bariy jàngoro ak i feebar yoy, lekk gu bon gi ak lekkiin wu bon gi ñoo leen di sabab. Ngir fànqal nit ñi ci loraange lekk ak lekkiin yu bon yi, ay ma-xereñi Afrig ci fànn wi booloo nañu, fas yéene tëral aw naal ngir sellal lekk gi, sàmm wér-gi-yaramu nit ñi.
Bees sukkandikoo ci kurél gii di OMS (Organisation Mondiale de la Santé), fii ak 2030, ci biir kembaaru Afrig, limu nit ñi lekk gu bon gi nar a faat mooy ëpp limu nit ñiy dee ci sabab feebar yiy wàlle. Loolu nag, xiibar bur raglu la. Moo tax, ngir moytandiku lu ni mel, waa kurél gii di Cchefs (Catalyzing Change for Healthy and Sustainable Food Systems), fas nañu yéen dooleel ndund gi fi Afrig, fexe ba mu sell te doy. Seen nisër mooy fexe ba ñam yu baax te sell yi mën a jàppandi ci li ëpp ci Saa-Afrig yi. Ngir jëmmal seen yéene jooju, ma-xereñi ndund gi ñu ngi daje jamono jii fa Sali (Mbuur). Seen ndaje maa nga dooroo barki-démb ci altine ji, 8i fani sàttumbar 2025, war a jeex tay ci àllarba ji, 10i fani sàttumbar 2025.
Ndaje mooma, jubluwaay bi mooy xàll aw yoon, tëral aw naal ngir sopparñi ndund gi fi Afrig. Ci juróom-ñetti réew yu wute la ma-xereñ yi jóge. Kurélu Cchefs ak yenn kuréli diiwaan bi ñoo joxe koppar yees amalee liiggéey bi.
Bu dee ci wàllu lekk gi, li ñu jublu ci seen naal wi mooy fexe ba dooleel ndogal yi njiit yiy jël, sukkandiku ci ay tegtal (données) yu leer te wóor ngir ñoŋal ak a sellal balluwaayi lekk gi. Liggéey boobu nag, dénkees na ko Laboraatuwaar bi nekk ci Jànguneb Seex Anta Jóob bu Ndakaaru, ñu duppee ko Laboratoire de recherche en nutrition et alimentation humaine de l’Université Cheikh Anta Diop de Dakar (Larnah/Ucad).
Bu dee ci fànnu koom-koom, seen jubluwaay mooy fexe ba Saa-Senegaal yépp mën a jot ci xeeti lekk yi, maanaam am dooley jënd ci lek kyu baax yi te sell. Liggéey boobu, waa Cres (Consortium pour la recherche économique et sociale) lañu ko dénk. Porfesoor Abdulaay Jaañ mi jiite Cres leeral na ni, ndajem liggéey ba ñu nekk di amal fa Sali, jéego bu am solo la ngir dëgëral liggéey bi ñu jot a amal ci wàllu gëstu ak itam ngir xàll aw yoon ak tëral naal wees di doxal ci diirub juróomi at yees dëgmal.
Ci xalaatu Madiha Ahmed mi jiite naaluw Crdi, liggéey bi Cchefs sumb dafay jéem a saafara benn ci jafe-jafe yi gën a réy yi àddina siy jànkonteel jamono jii : lekk ak lekkiin gu bon. Te, loolu, li ko gën a sabab mooy li jaaykat yiy wujje ci njaayum lekk gi ba di jaay ñam yu selladi, yuy nasaxal wér-gi-yaramu nit ñi koy lekk. Ngir xeex lu ni mel, li ma-xereñ yi xalaat mooy ñu jël ñam yu bon yooyii ñuy jaay, teg ci ay galag yu diis ba dootul yomb a jënd.
Porfesoor Abdulaay Jaañ dafa bëgg ñu roy ci anam bi ñuy xeexee tóx mi ngir xeex lekk gu bon gi. Nde, dafa seetlu ne « saa bu ñuy wéy di yokk njëgu sigaret yi, tóx mi dafay wàññeeku. » Kon, bat ay ci xalaatam, Càmm gi dafa war a fexe ba lekk gu bon gi di jar lu njëge.