SEN-PNA AK MEDIS S.A BOOLOO NAÑU NGIR LIGGÉEY

Yeneen i xët

Aji bind ji

SEN-PNA mooy banqaas bi ñu dénk lépp lu aju ci defar, jënd ak séddale garab yees di ci réew mépp. Ci kilifteefu njëwriñu wér-gi-yaram gi la bokk. Dr Séydu Jàllo moo ko jiite. Moom nag, li mu nisër mooy fexe ba Senegaal moom boppam te mënal boppam ci wàllu garabu-garabu. Maanaam, fexe ba Senegaal di defaral boppam ay garab yu mucc ayib ci lim bu doy ak njëg yu jàppandi ci askan wépp. Nde, noonii la ko Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ak elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, diglee, mu bokk ci ponki Naaluw Senegaal 2050. Ngir jëmmal jubluwaay boobu nag, SEN-PNA moo ngi séqi ay jéego, di digaale ak a lëkkatoo ak i kurél, fi réew mi ak bitim-réew, ngir dooleel kàgguy garabu-garabu yi.

Ci fànn woowu la SEN-PNA booloo ak MEDIS S.A, di kërug liggéey guy defar ay garab. Déggoob njënd (convention d’achat) lañu xaatim. Ndogal loolii ngi aju ci dekkareb 2022-2295 bi ñeel Càrtug jawi bokkeef gi ak cantaaneg (arrêté) MSAS/MFB 31017 biy yombal njëndug garab ci ndefari réew mi.

Bees sukkandikoo ci kàdduy njiitu SEN-PNA, Dr Séydu Jàllo, jéego bii ñu séqi dafay firndeel yéene ak dogu yiy màndargaal Càmm gi, nga xam dafa bëgg Senegaal dem bay defaral boppam lépp lu mu soxla ci ay garab. Dafa ne, “…jéego bu réy la buy firndeel pasteefu Nguur gi ci taxawal ndefarug garabi faju gu réew mi moomal boppam te doon lu sax.”

Déggoo bi ñu xaatim dafay tax ba MEDIS S.A di mën a jot ci jawi bokkeef yi ñeel garabi faju yi. Loolu nag, bees sukkandikoo ci kilifa yi, du ag jeng. Waaye, jubluwaay bi mooy fexe ba sàmm liggéeykat yiy yëngu ci fànn wi ba duñu ñàkk seen i xëy, yaatal xaralay ndefari garabi faju fi réew mi, te dooleel këri liggéey yi nekk fi réew li te di defar garabi yooyu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj