SENEGAAL XAATIM NA DÉGGOOB 300I MILIYOŊI DOLAAR NGIR YEESAL MBAY MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu Mbay mi, Dund bu matale bi ak Càmm gi, Sëñ Mabuuba Jaañ, xaatim ab déggoo bu tollu ci ñetti téeméeri (300i) miliyoŋi dolaar amerikeŋ. Déggoo bi nag, ñii di waa The Cornerstone Group – Hajib Al Shams Joint Venture la ko séqal. Ca Ndajem Péncoo Nosteg Dund bi lañu xaatimee déggoo bi. Jubluwaay bi mooy yeesal mbayum réew mu ci fànnu laf gi. Nde, ci lees tënk ci déggoo bi, dees na dugal ci mbay mi laf yees mën a yeesal, maanaam lees duppee « énergies renouvelables ».

Naal woowu nag, ci diirub juróom-benni weer lees koy doxal. Ci lees rotal ciy xibaar, ci doxalinu Build-Operate-Transfer (BOT) lees di roy ci doxal gi. Ci biir déggoo bi, bu ñu taxawalee ay ndefari laf yi ba noppi, waa BOT ñoo koy doxal ab diir laata ñu leen di jébbal liggéeykati Senegaal yi ak liggéeykati way-jàmburey réew mi. Maanaam, Senegaal a koy mujje moomal boppam ci lu sax.

Déggoo bi dafa ëmb fànn yu bari te wuute :

–         Defar mbëjug naaj (solarisation) ci tool yi ;

–         Tabax ay barabi yarukaay ;

–         Defar ay barab yees di yaree ndundati ndox (jën, añs.) ak laboraatuwaari gëstu ;

–         Suuxat fànnu ndund-laf wi (ndund-gil, ndund-cakkantal) ;

–         Dooleel manoorey xarala ñiy yëngu ci mbay mi ;

–         Def lees di wax « monétisation des crédits carbone » ñeel ay Koppar yees jagleel mbay mi ak kopparalug asiraas yi ;

–         Liggéeyandoo ak àddina sépp ci fànnu gëstu ak coste.

Déggoo bii dafay jëmmal yéene ji njiiti réew mi am ci suuxat mbay mi ci anam yépp, rawatina ngir waa kaw gi. Déggoo bi dafa dëppoo itam ak Naaluw Senegaal 2050 wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj