TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI FA TIRKII

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci yoor-yoor bi, la elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, génn réew mi, dem fa Tirkii. Njiitu réew ma, Sëñ Racip Tayyip Erdogan, moo ko fa woo ngir dalal ko. Tukki bi nag, mënees na ko jàppee niki tukkib liggéey, waayeet di tukkib xaritoo buy dëgëral kóllëre gi dox diggante ñaari réew yi.

Ci àllarbay démb ji la elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, teer fa Ankaraa (gëblag Tirkii). Njiitu réew ma, Sëñ Recep Tayyip Erdogan, moo ko fa woo, dalal ko. Moom, Sëñ Usmaan Sonko, juróomi fan lay def ca réew mooma. Ba muy dem nag, dafa ànd ak i jëwriñ, muy jëwriñu Bennoog Afrig ak Mbiri bitim-réew (Soxna Yaasin Faal), jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Digaale bi (Sëñ Abdurahmaan Saar) ak jëwriñ Ndefar gi ak Yaxantu (Sëñ Sëriñ Géy Jóob). Kii di Sëñ Biram Suley Jóob (jëwriñu Laf gi, Soroj bi ak Mbéll yi), Sëñ Mabuuba Jaañ (jëwriñu Mbay mi, Dund bu doy bi ak Càmm gi) ak Sëñ Biram Jóob (jëwriñu Dooley xare bi), ñoom itam demaale nañu.

Tay, ci yoor-yoor bi, elimaanu jëwriñ yi demoon na siyaare xabrub Njiitu réewum Tirkii la woon (Sëñ Mustafa Atatürk, 1881-1938). Ci ngoon gi tay ji tamit la séq waxtaan ak Njiitu réew ma ko fa dalal, Sëñ Racip Tayyip  Erdogan. Ginnaaw gi, Sëñ Usmaan Sonko waxtaan na itam ak seen Njiitu Ngomblaan gu Mag ga, Sëñ Numan Kurtulmus. Ba mu jógee ca ndaje mooma, gise na ak njaatigey Tirkii yi, waxtaan ak ñoom ci fànnu liggéey. Ca njeexitalu ndaje yooya, kilifa ya teewal Senegaal ak yoy Tirkii yi xaatim nañu ay déggoo yu bari ci fànn yu am solo niki : mbay mi, laf gi, ndefar gi, añs.

Balaa muy ñibbisi, Elimaanu jëwriñ yi dina daje ak doomi Senegaal ya nekk ca Tirkii, waxtaan ak ñoom ca seen nekkiin foofa ak mbiri réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj