Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, tukki na tay ci àjjuma ji, 16 me 2025, daldi dem Burkinaa Faaso. Ñaari fan la fas yéene def foofee, fa réewum Tomaas Sànkara. Jubluwaayu tukki bi mooy dooleel diggante Senegaal ak Burkinaa Faaso, dëgëral ak a ñoŋal seen i jëflante ci wàllu digaale.
Ba elimaanu jëwriñ yi teeree fa dalu roppalaanu Wagadugu ba, nawleem bii di Emaniwel Wedraawogo ak yeneen i kilifa yu ràññeeku ñoo ko dalal, tatagal ko ni mu waree.
Guléet Usmaan Sonko, niki elimaanu jëwriñ, di tukki fa Burkinaa Faaso. Ci lees biral ciy dég-dég, dees fa waxtaane mbirum kaaraange, bennoo ci fànnu koom-koom ak jàppoo bi war a dox diggante réewi Afrig sowu-jant yi.
Moom Usmaan Sonko nag, demul moom kese. Nde, ànd na ak Soxna Yaasin Faal miy jëwriñu Mbiri bitim-réew ak Bennoog Afrig, Sëñ Biram Jóob miy jëwriñu Dooley xar bi ak Soxna Xadi Jéen, jëwriñu Tàggat-yaram bi.
Ba mu àggee, Sëñ Usmaan Sonko séq naw waxtaan ak Njiitu réew ma, Kàppiten Ibraayma Taraawore. Dafa di sax, ginnaaw bi ñu waxtaanee li ñeel diggante ñaari réew yi, dinañu jàkkaarloo ak saabalkat yi, gaaral leen la tukkee ça waxtaan woowa. Waayeet, Sëñ Sonko dina teewe kaajarug xabrub Parsidã Tomaas Sànkara ak 12i àndandoom, ci ngoonug ëllëg ji, 17i fani me 2025, fa Wagadugu. Teewaayu elimaanu jëwriñi Senegaal yi ca ndajem kaajaru xabru jàmbaaru Afrig bu mag boobu dafay firndeel yéeney Senegaal ci màggal jëmm yi ràññeeku yi daan xeexal Afrig ngir mu moom boppam ci fànn yépp, rawatina yoy pólitig ak koom-koom.
Bi mu génnee ci waxtaan wi mu séqaloon ak Kàppiten Ibraayma Taraawore nag, sànni na fay kàddu, wax lii toftalu :
“Dama jottali kàdduy ndimbal ak jàppale bu mat sëkk bi Senegaal fas yéene indil Njiitu réew mi, Ibraayma Taraawore, ak Càmmug Burkinaa Faaso ak askan wépp, ci seen xeex bi ñuy xeex terorism, te di sóoraale bépp xeetu digaale ñeel ñaari réew yi ak ni Senegaal mënee taxawu Burkinaa Faaso ci nattu bi ko dal.”
Ba tay ciy kàddoom, Usmaan Sonko xamle na ne reewi Afrig sowu-jant dañoo bokk am reefo. Maanaam, li leen boole dafa bari, rawatina ci fànni mboor ak dend bi ñu bokk nekk. Ba tax na, menn ci sunu réew yi mënut a mucc wëliif yeneen yu digalool. Ndax, ñu bokk teen kat, dañuy laxasooy goj. Moo tax Senegaal, ci gis-gisu Usmaan Sonko, du yam rekk ci jàppale Burkinaa Faaso. Waaye, lépp lu Senegaal mën liggéey ak réew mooma ñeel kaaraangeem, dina ci xar tànku tubéyam.
Laata muy ñibbisi, elimaanu jëwriñ yi dina daje ak saa-senegaal yi nekk foofa ca Burkinaa Faaso, saafonte ak ñoom, déglu seen i njàmbat, seen i wañse ak seen i mébét ngir, bu ko jaree, mu indi ciy saafara.