Càmm gaa ngi ci tànki wàññi njëgi mbëj gi, njafaan [carburant] gi, gil bi ak njureefi soroj gi. Ci altiney tay jii la elimaanu jëwriñ yi biral dég-dég bi. Bi ñuy taxawal Ndiisoog njiiteefu lees duppee Pacte national de stabilité sociale pour une croissance inclusive et durable [Digaaleb réew mi ñeel dalug mboolaay mi ngir yokkute gu daj ñépp te sax dàkk].
Jamono yii, Senegaal a ngi jafe-jafey koppar ak koom-koom yu metti. Li gën a sabab loolu, ci kàdduy njiit yi moome réew mi, mooy anam bi ñu donnoo réew mi, rawatina bor bu diis gann bi leen Maki Sàll bàyyee. Waaye, ànd ak loolu yépp, Càmm gaa ngi def kemtalaayu kàttan ngir taxaw ci soxlay askan yi. Ci kaw loolu, Nguur gi dafa fas yéene jël nafag 2026 gi, jagleel ko soxla yi gën a jamp ci askan wi. Naka noonu, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, fàttali na ne amagum 30i miliyaar ciy seefaa yu ñu dajaleegum ngir defar ci 30i bérébi fajukaay. Te sax, ciy waxam, 30 yooyu, dees na ci toftal yeneen 10 yu war a ubbi ci atum 2026. Rax-ci-dolli, dinañu taxaw ci dëkkuwaay yi. Nde, ñu ngi waaj a leb 20i miliyaari seefaa ngir tabaxee ko 30 000iy dëkkuwaay yu jàppandi ci askan wi. Usmaan Sonko dafa wax ne :
« Saytuwaat nañu nafa gi ngir comp ci lees mën a jagleel Naaluw joyyanti koom-koom […] Fii ak i fan yu néew, dinanu jël ay ndogal ngir wàññi njëgu mbëj gi, gil bi, njafaan gi ak njureefi soroj gi. »
Usmaan Sonko xamleet ne yéeney Nguur gi jëm ci liggéey ba réew moom boppam. Maanaam, liggéey ba Senegaal dootul soxxlaati koppari bitim-réew ngir doxal ay naalam. Ndax, jamono jii, boru Senegaal bi dafa jéggi dayo ba nga xam ne, ñu bari ci ñu daan lebal Senegaal xaalis dañu téyandi seen i loxo.
Dafa am nag ay naal yu njiit yi gis ne ñoo gën a jamp, muy tabaxi waax yi ak naawu yi, « agropoles » yi, ndefari gil bi, yooni ndox mi, añs. Ngir jëmmal naal yooyii, Nguur gi dafa bëgg a sukkandiku ci gafaka ak koom-koomu réew mi.