XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

LÀMB JI : MOODU ANTA / PRINCE

Jàppal nañu bëre bi lél bu bees. Ñaari mbër yee ngi waroon a laale keroog 23i féewiryee. Waaye, dàqeesoon na ko ba ci 4eelu fanu awril. Bés boobu itam, dañu ko fomm bi mu demee ba des ñaari fan kese. Li ko waral mooy ne, njaatige doomu cees bi moo xamle woon ni mbëram mënu ci bëre. Loolu waral ñu jàppaat ko bésub 4i me bii di ñëw, mu daje ak ñaareelu bésub “CLAF” bi. Yaakaarees ni kenn dootul soppi lél bi, ndax barina ci ñuy dund làmb yuy xaar bu baax jooju làmb.

 LIGUE DES CHAMPIONS : 1/2 FINAAL

Ekib yii ñoo dem dëmi finaali joŋanteb Ligue des Champions :  Paris SG, Barcelone, Inter Milan ak Arsenal. Paris SG moo war a daje ak Arsenal ci 1/2 finaal yi, Barcelone ak Inter Milan. Joŋante yi ñaari yoon lay doon, yu njëkk yi 29 ak 30i fan ci weeru awril wii lay am. Ñaareel yi 6 ak 7eelu fan ci weeru me lees leen di amal.

EUROPA LIGUE : 1/2 FINAAL

Ci joŋantey Europa League bi tamit, tollees na ci dëmi finaal yi. Ni joŋantey Ligue des champions bi di doxee, noonu rekk la tëdde. Maanaam, ñaari ndaje ñeel 1/2 finaal yi. Manchester United moo ciy daje ak Athletic Club, Tottenham ak Bodø/Glimt. Joŋante yu njëkk yi 1eelu fan ci weeru me bi la, ya ca des 8eelu fan wa.

CONFERENCE LIGUE : 1/2 FINAAL

Ci joŋantey bii, Djurgarden moo ciy daje ak Chelsea, Real Betis ak Fiorentina. Mook Europa Ligue bi ñoo bokk i bés.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj