Po mi tàmbali na keroog 2 Ut 2025. Senegaal dafa bom matsam bu njëkk, mu doxoon ci digganteem ak Niseriyaa. Benn bal la ko dóor ci dara. Mu dese ko ñaari ndaje ci kippoom. Benn bi moom ak Kóngoo lay doon ci talaata jii 12i ut, bi ci des mu war ci daje ak Sudã ci jeneen talaata ja ca topp jàpp 19i fan ci weer wii.
TUGAL
Kevin Debruyne tàmbali na wone boppam ca këlëbam bu bees ba, Napoli. Saa-Belsig bi moo ngi xaatim rekk ca Napoli, fa Itali, gannaaw ma mu jeexalee pasam ca Manchester City ba mu ne woon. Jamono jii, ekib yi di amal i matsi xaritoo ngir waajal atum ren mi, Debruyne moom tàmbali na xaat di wone boppam ca ekib ba. Démb ci seen mats ak Girona dafa dugal ñaari bii ba nopi joxe ñu dugal. Lu ni mel di lees doon xaar ci moom ci ekibam bu bees bi.
Luka Modrić tàmbali na ca Milan AC. Saa-Madrid ba woon amal na matsam bu njëkk ak Milan AC tay ci dibéer ji. Ba mats ba xaajee lees ko dugal mu amal simileem yu njëkk foofu.
Isco ame na gaañu-gaañu ci seen ndajem xaritoo ba ñu doon amal démb ak ekib bii di Como. Gannaaw bañ ko saytoo, xamlees na ni dana dandu pàkk yi lu tollu ci ñetti weer.
BASKET
AFROBASKET ANGOLA 2025
Arminaatu ekibu Senegaal bi génn na. Ndawi réew mi diñan amal seen ndaje mu njëkk talaata jii, 12i ut 2025, ak waa Ugàndaa. Buñ ca jógee, danañu daje ak Esipt ca 14eelu fan wa laata ñuy laale ak Mali ca 16eel ba.