Ci àjjumay tay jii la Mbootaayu Xeet yi (ONU) xamle ci lu wér ne, fa Gasaa (Gaza), xiif gaa ngay ray askan wa. Ginnaaw bi mu biralee xibaar bile nag, Israayel la joxoñ baaraamu tuuma, wax ne fitna ju metti ji muy teg askan wa ak it li ñuy bañ ndimbal li dugg fa moo sabab xiif gi. Bees sukkandikoo ci ma-xereñ yi, 500 000iy Saa-Palestin ñoo ame ay jafe-jafe yu tar a tar ci wàllu dund. Dañu xiif, mar, rafle, tumurànke te sonn lool sax. Israayel nag, na mu ko tàmm a defee, weddi na tuuma jooju.
Dég-dég bi Mbootaayu Xeet yi siiwal dafay dëggal ak a firndeel tolof-tolof yu tar yu askanu Palestin di dund ci at yii weesu, rawatina wow Gasaa, te ñu yàgg koo ŋàññi.
ONU dafa xamle ne, xiif gees di wax fa Gasaa, lu dëggu la. dafa di sax, guléet ñuy nemmeeku lu ni mel foofa ca Penku. Mbootaayu Xeet yi dafa sukkandiku ci genn caabal gog, kurél giy saytu kaaraangeg dund bi (IPC) moo ko siiwal. Bees sukkandikoo ci caabal googu, xiif gaa ngi ray askan wa fa bëj-gànnaaru Gasaa.
Kurélug IPC googu bokk ci Mbootaayu Xeet yi (ONU), am na 500 000iy doomu-Aadama yuy jànkonteel ak xiif gu « doy waar ». Maanaam, boo xaajee askan wa ñeent, benn xaaj ba lekkatuñu, naanatuñ. ONU nag dafa leeral, wax ne Israayel moo waral xiif googu te moo koy suuxat. Ndaxte, moo tëj dëkk ba, di leen sànd ay bomb saa su nekk ba noppi di bañ ku leen wallusi. Waaye, Israayel dafa weddi tuuma jooju ca saa sa.
Kurélug IPC gi dafa sukkandiku ci ay tegtal ak i nattukaay yu leer laata muy génnee caabalam gi. Dafa di, booba ba léegi, ay muy ONU, di ay ONG ak yenn ciy réew ci àddina si, yàgg nañoo artu ak a dankaafu. Jamono jii, xiif gi dafa nar a tas ca réew mépp, rawatina ca bëj-saalumu réew ma, muy diiwaan yii di Deir Deir el-Balah ak Khan Younis.
Xiif nag, mooy jafe-jafe bi gën a mag ci wàllu dund. Dara gënul metti toog amoo loo dunde. Ba tay ci waxi IPC, limu 500 000 bi ñu wax mën na àgg ba 640 000 fii ak weeru sàttumbaar.
Bees sukkandikoo ci Jean-François Corty mi jiite kurélu Medecins du Monde, “fanweeri nit yoo jël ci téeméer, amuñu lu ñu dunde, rawatina tuut-tànk yi.” Ñaareelu tegtal bi mooy “limu dee yu bari yi, daanaka 200i nit ci 10 000iy nit ñoo jël. Bi ci mujj mooy seetlu bi mu seetlu ne, “juróomi nit yoo jël, kenn ki amul dund bu doy.”
Jean-François Corty xamle naat ni, “xiif gi jotewul dara ak taw yi. Loxo nit a ko def. Dafa am ñu am yéeney metital ak lor ay nit. Moo tax kon, aw askan [Saa-Palestin yi] nekk tay ciy jafe-jafe yu raglu lool”.
Ca ndoorteelu weeru màrs la Israayel tëjoon bunti réew ma, fatt yoon yépp ngir bañ dund bi ak ndimbal yi àgg ci Saa-Palestin yi. Boobaak tay, sóobarey Israayel yaa ngi xoqatal, di metital ak a fitnaal waa Gasaa guddeek bëccëg. Etaasini moo leen ciy jàppale, di leen sotle, àddina si toog di seetaan. Ginnaaw ba ONU wéral na dég-dégu xiif ga am fa Gasaa, dees na xool ba xam lan mooy doon taxawaayu àddina si ñeel faagaagal bi Israayel di faagaagal waa Palestin ci tooñaange.