ISRA sóobu na ci xeetu mbayum ceeb mu yees ca bëj-gànnaaru réew mi. Nde, fale ca xuruw dexug Senegaal ga, fa la nekk di caaf xeetu mbayum mom, dafay aajowoo àngare ak jumtukaayi xarala yu yees. Jubluwaay bi yokk limu ceeb bees di bay ngir mën cee am lu duy waa réew mi. Ki ko xamle mooy Sëñ Omar Ndaw mi nga xam ne, moo jiite lees dippee Centre de Recherche Agricole (CRA), féete. Dafa wax ne, ISRA mi ngi ci tànki caaf xeetu mbayum ceeb mu wuute ak lees miin. Dafa ne :
“Fi mu nekk nii, nu ngi caaf lii di SRI bi ci xuruw dex gi, rawatina ca dëkk yii di Fanaay ak Savoigne, lëkkaloo ci ak kurél gii di Conseil de l’Ouest et Central Afrique pour la Recherche et le Développement Agricole (CORAF)”.
Sunuy naataangooy APS ñoo taataan yile kàddoom. Moom, Sëñ Omar Ndaw, mi ngi biral kàddu yi ginnaaw bi mu amalee tukkib nemmeeku bu ñaari fan foofa, ca béréb yees namm a jëmmal naal wi.
Li sabab naal wi nag mooy ab seetlu bu ñu def ñeel ñetti réew yii di Mali, Senegaal ak Burkinaa Faaso. Nde, at yii ñu weesu, gis nañu ni mbayum ceeb bi dafa wàññeeku bu baax ci biir ñetti réew yooyii. Loolu moom waral, niki daaw, kurélug CORAF daldi sumb aw naal ngir suuxat mbay mi.
Dañuy jëfandikoo xeeti jiwu yu bari yu warale. Ra-ci-dolli, dañuy ñaax baykat yi ñu jàng yeneen xeeti mbay yu wuuteek ya ñu miin.
Mbayiin wu bees woowoo ngi sukkandiku ci anam ji bu bees te ñu koy tàmbalee ci ay pepiñeeryoy, dees na ji jëfandikoo luy tollu ci 25 jàpp 30i kilo ci ektaar bu nekk. Loolu Sëñ Fay moo ko leeral, muy fësal anam bees di jëfandikoo ndox mi. Ndax, dañuy fendil tool bi, di ko roose.
Wax na yit anam bi ñuy dundalee suuf si, di ci jëfandikoo kompost.
Bees sukkandikoo ci ay kàddoom, “Ca Fanaay ak ca Savoigne yépp, dafa mel ni baykat yi nànd nañu bu baax anamu mbay bu bees boobu, te ñu ngi koy waaj a yaatal fépp ci at yii ñu jëm”.
Dige na ni, dinañu ko yaatal ci yeneen gox yi ci Senegaal, fépp fu ñuy bay céeb jamonoy nawet. Bu dee Soxna Faatu Jeŋ moo, xam-xamam màcc ci wàllu saytu ak jàngat te bokk ci kurél gii CORAF, dafa leeral ni jubluwaayu tukkin nemeeku bi mooy jàppale ISRA ci liggéeyi gëstu yi mul amal ci xur wi.
Muy fàttaleet ni, naal wees dippee « Système de riziculture intensive », sumbees na ko ci ñetti réew, lépp ci ndimbalu Bànku Àddina si, muy bokk ci naaluw jàppandal dund bi ngir yokk njureefi mbay mi ak ak xeetu mbayiin bu bees bob, du laaj koppar yu bari te dafay sàmmaale kéew mi.
Soxna Faatu Jeŋ dige na ni dinañu neexal baykati yi gën a wane fësal seen bopp ci wàll wi, ci biir ñetti réew yi.