“Njiiti Etaasini yi tooñati nañu waa “Cour Pénal International” (CPI), di ëttu àttekaayu àddina si. Nde, dafa jëlal boppam ndogalu teg ay daan ci kaw ñeenti àttekati CPI, rawatina doomu Senegaal jii di Maam Manjaay Ñaŋ. Te dara taxul ñu daan leen lu moy li àttekat yooyu sumb ay luññutu ñeel ay Saa-Amerig ak i Saa-Israayel !
Maanaam daal, li Trump ak i ñoñam doon tuumaal Toppekatu CPI ba woon, Faatu Bensudaa, ak kenn ca tofam ya woon, loolu kepp lañuy tuumaal àttekat yile, maanaam def seen liggéey. Te seen liggéey boobu du lenn lu dul ubbi ay luññutu ci ay pékkey xare ak pékkey faagaagal ay nit ca Palestin, rawatina li ñu dóor “mandat d’arrêt international” kii di seen elimaanu jëwriñ yi, Benjamin Netanyahu.
Kurél gii di “Coalition Sénégalaise pour la Cause Palestinienne”, ni ko Nguurug Senegaal gi defee, moo ngi wax Njiiti Amerig yi ñu dakkal daan yi ñu teg ci kaw àttekati CPI yi. Bu loolu weesoo, ñu ngi leen di wax ñu sàmmonte ak sañ-sañi CPI yi, te jox ko cër.
Ba tay, ci fànn woowu, kurélu “Coalition Sénégalaise pour la Cause Palestinienne” a ngi :
– feddali ànd bu mat sëkk bi mu ànd ak seen moroomu Saa-Senegaal bii di Maam Manjaay Ñaŋ, toppekat fa CPI.
– kurél gi dogu na ci gën a dëgëral jàppale bi muy jàppale mbokki Palestin yi ak di wéyal xeex bi ngir dakkal nooteel gi, xeetal gi, pékkey xare yi ak pékkey faagaagal yi ñu ga waa Palestin.”