NDOGAL YI ELIMAANU JËWRIÑ YI JËL ÑEEL MBIRUM SUUF SI
Démb, ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ yi, ni ñu koy defee ayu-bés bu nekk. Ca ndaje mooma, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, jël na fa ndogal yu am solo ñeel mbirum suuf si. Nde, kenn umpalewul ne coowal dëkkuwaay yeek yu ni deme dafa bari lees koy dégg ci fu mel ni Ndar, Ndakaaru walla Cees. Ba tax na, elimaanu jëwriñ yi, ci ndigalu Njiitu réew mi, jël na ndogalu dakkal bépp liggéey bu jëm ci wàllu ay dagg suuf ak yu ni mel ci béréb yooyu ñu lim. Képp koo xam ne dafa soxla tamit, mu xaar ba ñu tegaat mbir yi ci yoon. Ndax, dañuy teg naal woo xam ne wu jaar yoon lay doon. Ci gàttal, jamono jii, dañoo teg ag ndiisoo gog, mooy saytu lépp lu jëm ci wàll woowu ngir xam lépp lu ci laxasu.
MURIG MBALAANU KIIRAAYU MUSTAFAA JÓOB
Bu yàggul dara lañu muri woon mbalaanu kiiraayu dépite bii di Farba Ngom. Ginnaaw gi, ci la ko Yoon wooloo. Fi mu ne nii nag, yóbb nañu ko kaso. Kii di Mustafaa Jóob, di naataangoom, maanaam, di dépite ci Ngomblaan gu yees gi, ñu ngi ci ay tànkam. Nde, suba ci àjjuma ji, woolu nañu dépite yi fa Ngomblaan ga. Li sabab woote bi, li ci jiitu mooy waxtaan yi ñu amal ak njëwriñal mbiri bitim-réew. Poñ bu mujj bi mooy ndiisoo ad hoc giy àddu lu jëm ci murig mbalaanu kiiraayu dépite boobu.
TAYIIRU SAAR JÉBBALAAT NA BENEEN TAYLE (CAUTION)
Fan yee weesu lañu yóbbu kaso Tayiiru Saar ñeel mbirum 125i miliyaar yi. Boobaak léegi, mi ngi def i pexe ngir ñu bàyyi ko bàyyig négandiku. Looloo tax mu bëgg a jébbal kii di “AJE” (Agent Judiciaire de l’Etat) ab tayle bu tollu ci 419i miliyaar bees sukkandikoo ci waa L’Observateur”. Li mu ci jublu mooy ñu bàyyi ko, bàyyig négandiku. Tayle boobu, alal ju bari te wute moo ci nekk. Ag koppar gu takkoo ngi ci, ay pàkk yu yaatoo yaatu ak ñaari taax yu ñu xayma ci fukki miliyaar ak ñeent.
ARDO ÑIŊ DEM NA KASO
Ci ndoorteelu ayu-bés bii lañu ko woolu woon, moom Ardo. Bi mu wuyujee, ca lañu ko téye. Ginnaaw gi lañu ko yóbb kaso. Li ñu koy toppe mooy kàddu yu woroo ak jikko yu rafet. Ab layoom nag, ñi ngi ko jàpp àllarba jii di ñew, fukki fan ak juróom-ñeent fa ëttu àttekaay bu Ndakaaru.
ASAN JAAWo TÀNN NA GAYNDEY SENEGAAL YI
Asan Jaawo di futbalkat bu Senegaal ak Espaañ tegoon bët. Am ñu jàppoon ne Asan, bu ko Espaañ soxlaa, du xalaat a dem Senegaal. Waaye, mbir mi mujjewul a deme noonu. Ndax, moom ndeyu-mbill ji, Senegaal la tànn. Moom Asan, bokk na ci ñaar-fukki gaynde ak juróom-benn yi Paab Caw woo ci ñaari joŋante yi Senegaal war a amal ci weer wii. Benn bi war a dox digganteem ak réewu Sudaŋ. Beneen bi war a dox ci digganteem ak réewu Tógoo.