LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (27/11/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Amal nañu, démb, ndajem jëwriñ yi nees ko baaxoo defe àllarba ju nekk ci ayu-bés bi, ci njiiteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay.

Njiitu réew mi jaare na ci, jël ndogal yii toftalu :

* Ci wàllu Njëwriñu Laf gi, Soroj bi ak Mbell yi, Njiitu réew mi tabb na Sëñ Aliyun SEKK [Ingénieur Géologue], def ko Njiitul PETROSEN Exploitation et Production, mu daldi wuutu Sëñ Taala GÉY.

* Ci wàllu Njëwriñu Njaboot gi, Dimbalante bi ak Jàppalante yi, Njiitu réew mi tabb na Sëñ Suleymaan JÀLLO [Inspecteur de l’Enseignement élémentaire], def ko Fara-caytu bu mag bu Office national des Pupilles de la Nation (ONPN), palaas bi dafa wëyëŋoon*.

* Ci wàllu Njëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, Njiitu réew mi tabb na Sëñ Seex Musaa KAN [Titulaire d’un diplôme d’Ingénieur en Statistique Informatique appliquée et d’un Master en Suivi-Evaluation des Projets], def ko Njiitul Ndajem Caytu mu Laboratoire national d’Analyse et Contrôle (LANAC), Sëñ Abdul SI la fa wuutu, ndax kooku dañ ko yóbbu feneen.

ELIMAANU JËWRIÑ YI DINA TEEW CA NGOMBLAAN GI ËLLËG CI ÀJJUMA

Ëllëg, àjjuma 28 nowàmbar 2025, elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, dina dem fa Ngomblaan ga ngir tontuji laaji dépite ya ñeel anam bi réew miy doxe. Li ëpp ci dépitey kujje gi nag, muy waa lëkkatoo Takku Wallu ak dépite yu binduwul, nee nañu duñu teewe ndaje mi.

OFNAC : NJIITU RÉEW MI TABB NA WAY-BOKK YI

Njiitu réew mi torlu na ab dekkare, daldi tabb way-bokki OFNAC yu bees yi. ñi mu tabb ñooy ñii toftalu :

Njiit li : Sëñ Mustafaa Ka, àttekat

Tof-njiit li : Sëñ Biraayim Sekk, way-moomeel

Yeneen way-bokk yi :

 -Soxna Xadijatu Ba, ma-xereñ ci fànnu saytuak xayma

 -Sëñ Sàmba Bari, way-moomeel

 -Sëñ Ibraayma Faal, saytukatu moomeel

 -Sëñ Mafaal Faal, àttekat

-Sëñ Mademba Géy, àttekat

-Sëñ Abdu Asiis Daba Kebe, Porfesoor agereese ci wàllu Yoon, fa jànguneb UCAD

-Sëñ Baabakar Ñaŋ, Porfesoor agereese ci wàllu Yoon, fa jànguneb UCAD

-Sëñ Biraan Ñaŋ, àttekat

-Sëñ Muhammet Basiir Ñaŋ, Porfesoor agereese ci wàllu

Yoon, fa jànguneb UCAD

-Sëñ Sàrl Dijje Ngan Ngacci Seŋoor, àttekat

NJÀNG AK NJÀNGALE / MBOOR : NJÀNGUM JAAR-JAARU TIRAAYËER YI

Njëwriñu Njàng meek njàngale mi génne na ab yégle, di ci xamle ne, keroog altine, 1eelu desàmbar 2025, dees na jàngale am mbind ci tiraayëeri Senegaal yi ci lekooli Senegaal yépp.

MBAY MI : SENEGAAL SÉQI NA JÉEGO YU AM SOLO

Jëwriñu Mbay mi, Sëñ Mabuuba Jaañ, yéene nay njureef yu am a am solo ñeel kàmpaañu mbay mi. Ci li mu xamle bay nañu fi Senegaal lu tollu ci 960 000iy toni gerte, lu ëpp 600 000iy toni mboq ak lu ëpp 25 000iy toni wëtteen.

Rax-ci-dolli, xamleet na ne mbayum ceeb bi diiwaanu Waalo bi dafa kawe seen i njort. Nde, bay nañu diggante 7 jàpp 10i toni ceeb ci ektaar bu nekk.

Bu dee mbayum banaana mi, ci réew mépp, ëpp na 119 000iy ton.

YAALE JI / KOPPARALUG 1000iy TAKSI « HYBRIDES »

Ci àllarbay démb ji, 26 nowàmbar 2025, FDTT, di kurél giy yëngu ci wàllu kopparal yaaley suuf si*, ak Bànku Yaxantu ak Ndefar bu Senegaal (BCI SN) torlu nañu ab déggoo ngir kopparal junniy taksi « hybrides » ci Senegaal, daldi leen waajal ngir ñu tàmbalee daw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj