KÀDDUY NJIITU RÉEW MI FA GINE BISAAWO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay yékkati nay kàddu woote fa Gine Bisaawo ga mu demoon ginnaaw ba ñu fa sàkkoo teewaayam niki gan gu mag gu 15eelu Ndajem Njiiti réew ak Njiiti Càmm yu réew yi bokk di làkk purtugees fi Afrig.

Démb ci àjjuma ji la Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay demoon fa réewum Gine Bisaawo ngir fekkeeji 15eelu ndajem Njiiti réew ak Njiiti Càmm yu réew yiy làkk purtugees fi Afrig CPLP (Communauté des Pays de Langue Portugaise). Muy ndaje mom, Njiitu réewum Gine Bisaawo li, Umaru Sisoko Mbaalo, moo fa sàkku woon teewaayam ngir mu doon seen gan gu mag.

Bi mu fa teewee itam, Njiitu réew mi yékkati nay kàddu ca jotaayu liggéey ba ñu fa doon amal. Ginnaaw bi mu rafetloo jotaay ba ak dalal gi ñu ko fa dalal, rafetlu na bu baax li lëkkale réewum Senegaal ak mu Gine ci mboor, mbatiit ak ci seen iy lëkkatoo. Naka noonu, mu dellu rafetlu xel mi kurélug CPLP am ci ubbi ak yaatal ay lëkkatoowam.

Ba mu ca noppee, Njiitu réew mi ñëw na ci taxawaayu Senegaal ngir dëgëral digganteem ak réewi CPLP yi ngir ñu doxal ay lëkkatoo yu réew mu nekk di gis boppam, rawatina ci wàlluw mbatiit, njàng mi, yaxantu beek mbay mi.

Ci biir ay waxam nag, mënees na cee déggee ni mën-sa-bopp ci wàlluw dund bee ko ci ëppal solo. Ba tax na mu amal woote bu am solo ci ñu ànd, dajaloo, boole seen iy doole ngir sopparñi bu baax wàlluw mbay mi. Ci loolu sax, Njiitu réewum Senegaal li gaaral na fa jubluwaay yu gën a mag yu naalub SENEGAAL 2050, ak ni ci mbay mi doone kenu gu am doole ñeel suqaleeku réew mi.

Wax na itam ci solos coste yi, njariñu fullaal dayo suuf si, suqali tabaxte yu jëm ci ja yi te jàppale bu baax meññalkat yu ndaw yi, rawatina jigéen ñeek ndaw ñi.

Teewaayu Njiitu réewum Senegaal li foofu nag dafay wane ubbeeku bi mu namm ci Senegaal ñeel réewi purtugees yi. Doon na itam luy dellu di wane taxawaayam ci yokk lëkkatoo réewi bëj-saalum yi ci seen biir ndax ñu mën a booloo te am kàttanu dékkoondoo jafe-jafe yi kembaar gépp bokk di jànkonteel.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj